Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Lesoleil: Gàawu 11 awril 2009
s-2 Porogaraam biy xeex sibbiru ci réew mi te tudd PNLP, ci jàppleg ñi muy jëflanteel, yeesal na xam-xamu 51 njiiti doktoori gox yi ak seen i toftal, ci pexe yu bees yi ñu tëral ngir xeex sibbiru, ci ñaari lël.
s-3 Ñaareelu lël bi, jëm ci njàngale ñeel sibbiru ak xeex bi mu laaj, dajale na 26 doktoor.
s-4 Lël boobu mu ngi tàmbali ci 16 màrs ci Daaray Wér (ISED) tëj ci 4 awril 2009, ci njiitéefu Dr Asan Yaradu, kenn ci ñi di xelal njawriñu wér ak fàggutéef.
s-5 Doktoor Pàppa Muusaa Coor miy saytu PNLP xamle na ne njàngale mii ñu sumb mu ngi bokk ci pexe yi ñu tëral ngir sibbiru ak dee yi muy jur bañ a jéggi tolluwaay bi mu nekk jamono yii.
s-6 Ndax gisees na ne tolluwaay bi dafay gën di wàññiku te li ko waral moo di pexe yi ñu tëral ngir xeex jàngoro ji.
s-7 Mënees naa lim yenn ci pexe yooyu: joxe sànke yu ñu nàndal, ak fexe ba garab yi (ACT) ñépp mën cee jot ci njëg gu yomb, ak def ay càmbar yu feeñal jàngoro ji, na mu gën a gaawe.
s-8 Ci 2008, tolluwaay baa ngi nekkoon ci 5,6 % te mooy junni nit ñu ne, juróom-fukk ak juróom–benn yi sibbiru dal na leen.
s-9 Looloo waral Dr Coor yokk ci: su nu wéyee di góor-góorlu, waxuma rekk ne tolluwaay bi dina yem foofu, waaye sax dinanu faagaagal xeetu sibbiru bii.
s-10 Ci xalaatam, ngir bundxataal sibbiru, dafa laaj beneen wirgo doktoor, beneen wirgo saytukat ngir tolluwaayu dee gi ci aju ak jàngoro ji bañ a yéeg.
s-11 Looloo tax ñu taxaw temm ci yeesal xam-xamu doktoor yi te dooleel leen ci pajum sibbiru, Doktoor Coor teg ko ci.
s-12 Njiital Ised, Pr Anta Taal Ja, moom, dafa ñaax doktoor yi ñu nekk ay mbër ak ay saytukat ci xeexu sibbiru, ku nekk ci sa gox.
s-13 Doktoor yi ñoom rafetlu nañu njàngale mi, ndax ñi leen doon xamal wàccoo nañu ak ñoom, li ñu ci doon xaar gis nañu ko.

Text viewDownload CoNNL-U