Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Fan lanu jëm ak sunu demokaraasi bii?
s-2 Réew mu nga xam ni yennat ci ay xalaat ñoo fi dagan, yeneen dañu araam.
s-3 Réew mi moo ne: sañ-sañu xalaat génne ko, xalaatal sa xel, lu mu jur nga wësin ko niki yooyee demokaraasi di yu Tugal yi nga xam ne ñooy ya mag yi ñu di roye.
s-4 Loolu jural nu nuy lang ci ay mbiccam, di jafandu ci ay waggam.
s-5 Nu naan lu fi di lu baax moom la, du keneen, du feneen.
s-6 Loolu tax na ba sax lu bawoo feneen du leneen lu dul neen ndax li muy keneen.
s-7 Lii ak lu ni mel moo jur natt ci ñaari nattukaay gi Tugal di def ba ay farandoom di ko ca fekk ak a roy.
s-8 Fan yii jàll coow jeqiku woon na ci réew mi, te dara jeqiwu ko woon lu moy kàddu yu njiitu réew mi yekkati woon ñeel estateem bii di bu ñu tere ci Lislaam ci mbooleem ay yaxam.
s-9 Ñenn jógoon ngir dëgëral njiit li bay indi ay yax yu di ko dëgëral te yooya yépp di woon yu di aaye yi ñu bëgg a daganal.
s-10 Loola tax ba njiit la lottee ci daganal ko ci Lislaam mu bëgg a jaare ci diineedi (laïcité) di li ñenn di woowe 'tëraayu njaaxanaay' ngir rekk wone ci ne mii réew moom du jullit ñi rekk a ko moom.
s-11 Ñépp a ko bokk, Nasaraan bi jullit bi ak woroom tuur yi.
s-12 Te kat kii di kilifa gu mag ci réew mi di Seex Ahmadu Bamba romb na fi ay estati te waxu ci dara, naka noonu geneen kilifa gee di gu kenn magul ci Lislaam ju Senegal di Alhaaji Maalig.
s-13 Waa jàngu bi it bokk ci réew mi te seen i biir jàngu ay estatee fa nekk yu ñu di jublu ci seen ag jaamu.
s-14 Te looluy lu am lu kenn dul sikk.
s-15 Waaw ana lu waral ñu ne nit ci mii am réew am na sañ-sañu génne li ci moom te du ko génn.
s-16 Fii lu neex waay mu teg ci kaw derub yoonu Murit mbaa Lislaam.
s-17 Te ñoñ Nasaraan ku leen xaw a laal réew mépp jóg jiital ci seen ñi ñu di tudde ay ñoñ xel (intellectuels).
s-18 Lu nekk ñu wax ko.
s-19 Te kat li jar a wax duñu ko wax mukk.
s-20 Li jar a wax moo di réew mu nga xam ne 98 % ay jullit lañu te feeti Nasaraan yaa fa ëpp.
s-21 Bu lu ñu di woowe Pak jotee ñu jox ndongoy daara yi ay fan yu dul jeex ngir ag bër.
s-22 Waaye jullit ñi ñoom, ku ca tëbëskiji mbaa nga tamxariti mbaa lu ni mel, say doom boo moyuwul ñu dàq leen, ndax amuñu fan yu ñu leen may.
s-23 Ab laaj a ngi nii: Li Abdulaay Wàdd waxoon imaam yi ci ag suufeel ak xeebeel lu tax jurul coow?
s-24 Li mu wax Sërin Tuubaa ak Alhaaji Maalig lu tax jurul coow?
s-25 Ndax kat Sërin Tuuba la taxoon ñu génne ko weesuwul bañ ab estati ak lépp lu Yàlla bañ te loola di woon li Tubaab bi bëggoon.
s-26 Seen i bëgg-bëgg wuute jur Tubaab bi manatu ko fee dékku mu génne ko ngir loolu.
s-27 Lu tax tooñaange yii yépp jurul coow?
s-28 Man damaa gis ne li tax waa ji moom wax jii wax du ngir tuutale waaye ngir layal estateem bi la.
s-29 Kon manoon na yam foofa, waaye mu àgg ci naan dafay booleji ca Paab ba, mel ne Paab bi war naa manal Senegaal dara.
s-30 Te moom ci jëmmi boppam taxawoon wax wax ju bon ju ñaaw jëme ci sunu sang bu tedd ba, ana lu ñu ci wax ñoom?
s-31 Ndax ñaawlu nañu ko?
s-32 Xanaa ñu ne 'liberté d'expression' sañ-sañu wax li ci yaw.
s-33 Ba ñuy damm soorool ya ca Siwis lu ñu wax?
s-34 Ba ñuy aaye muuraay ca Faraas ndax ñaawlu nañu ko?
s-35 Fu ñu ko teg?
s-36 Te moone soorool ya ca Siwis de weesuwul ñeent ci ay 200 jakka.
s-37 Am na fi ay baat yu nga xam ni seen liggéey ci réew mi du lu moy màbb dooley jullit ñi dëgëral Nasaraan yi.
s-38 Yooyu ba ca njëkk moo di diineedi, ñu gën koo xam ci 'laïcité'.
s-39 Laicite du lu moy tugalal mbaa sowwul (occidentalisser) aw askan wu ko doonul.
s-40 Loolu moo di tàyyi xayug sowwu gu Nasaraan ak Yahood gi (judeo-chretienne) tay ko ci réew mu nga xam ne ay jullit lañu mbaa duñu woon i ñoñ sowwu, ak ga leen ci ñu gën a doon i tubaab tubaab yi.
s-41 Laïcité (diineedi), bu dee sax lu ñu gawe (imposer), dafa war a sàmm diine yi waaye waru fee nekk di luy gor seen i tànk te naan sama yoon nekkul ci yeen.
s-42 Ci misaal bu dee dafa bëgg a taxaw ci réew mu mel ne Senegaal ci ag sañ-bañ, dafa war a taxaw taxawaayu Sariiya.
s-43 Du lu ñu fiy doxal mbaa àtteb jeneen diine, waaye lépp lu ñuy def warees na koo xool ba xam gaañul jenn ci diine yooyu.
s-44 Lu ko moy mu doonati moom ci jëmmi boppam jaasi ju ñu bocci ci kanamu diine yi.
s-45 Lu am solo ñu war koo wax mooy ne su ñu bëggee ag jeqiku bañ a ami ëllëg ci réew mi na fi ag maandute dolliku.
s-46 Maandute nag mooy séddale ci ag maandute déet gënale, déet def la la neex.

Text viewDownload CoNNL-U