Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Senegaal ak bés bi UNESCO jàgleel làkki-ndey
s-2 Bésu 21 fan ci weeru Fewrie at mu jot, moom la kurél gi di toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te feeteewoo ci Mbotaayu-xeet-yi, jagleel làkki-ndey yi, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp.
s-3 Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi ëpp na 10 at.
s-4 Li waral bés bi mooy yee nit ñi, artu leen, soññ leen ci solo bu jeggi-dayoo bi làkki-ndey yi am ci fànnu yokkute yépp.
s-5 Rawatina ci réewi Afrik yi nga xam ne daanaka ya ca ëpp ba ñu tàbbee ci 'kolonisation' ba téy jii ñu moomee seen bopp, dañoo xeeb seeni làkk yi ñu nàmp.
s-6 Réew yi gën a bari Afrik, Senegaal waxi noppi, seeni làkk sedduñu leen daanaka benn cër bu tàkku.
s-7 Kenn du leen jàng mbaa di leen jàngale ci lekkool yi.
s-8 Kenn du leen jëfandikoo ci bérebi àttekaay yi ak feneen ak feneen.
s-9 Dañu leen a soofal daal maanaam.
s-10 Te fekk nag, loolu sax naka jekk moo waral sunu xeex bii;
s-11 Amul wenn askan wu mën a am tawféex, yokkute ak jëm-ca-kanam ci wàllu politik, koom-koom, njàng ak leneen te dumooyu say làkk.
s-12 Bind nañu ko fi lu bare, indi nañu it firnde yiy wone ne réewi tubaab yi seen bopp nuy roy ci lu nekk, laata ñu doon génn ci ag lëndëmtu, dañoo mujj a dekkil seeni làkk.
s-13 Loola a nga xewoon ca ndorteel 15eelu xarnu bi:
s-14 Booba ñoom làkki Lateñ rekk lañu daan jàng di ca bind, defe woon ne seeni làkk tekkiwuñu dara.
s-15 Ba ñu daggee buum googu lañu tàmbalee gindeeku ba léegi, am yokkute ci lu nekk, ba tollu tey ci boppu àddina.
s-16 Looloo waral bi UNESCO nemmeekoo càggante ak yàq gu jeggi-dayoo googu mu def at mu nekk mu di fàttali xeet yi ak askan yi seeni làmmiñ!
s-17 Ndax gëstu yépp ci fànnu xam-xami làkk ak xaralaay jàngale wone nañu ci lu wér, ne xale bi door njàngam ci làkk wi mu nàmp, moo di gën a ubbeeku fuuf moroomam ma tàmbale njàngam làkk wu mu nàmpul.
s-18 Li ko waral mooy xale bi buy dal rekk dees di mën a tàggat xelam ci fànn yu bare niki matematik, xam-xami cosaan, fisik ak yeneen.
s-19 Te bu dee, kom ni ñu koy defe Senegaal, njàng mi yépp ci Nasaraan la, su xale bi duggee lekool dafay mel ni ku lu.
s-20 Dafay mel ni perantal buy door a jàng wax.
s-21 Dina def lu yágg ci ay at balaa lees ko mën a jàngal lenn lu am solo ci Nasaraan.
s-22 Ndax déggu ko!
s-23 Li ëpp ci lu muy jàng du weesu ijji ak nafar lu mu xamul lu muy tekki.
s-24 Rax-ci-dolli, xeeb boppam, tiitange ak jaaxle bi xale biy am, su ràññee ne, ndeke moom làkk bi mu nàmp tekkiwul dara ca béréb yay indi tekki ëllëg ca réewam!
s-25 Dafay juux ci lu ñu woowee 'crise d'identité', maanaam, dootul ràññeeti li mu doon, dafay nekk ku neex a yobbale, ku neex a ómmat!
s-26 Waxoon nañu fi itam ne sax soo koy seet, demokarasi bi ñuy wax, maanaam 'nguuru askan wi ngir askan wi', mënul a am ci làkk woo jeggani!
s-27 Wante tey bi ñu demee bay tekki ci saa si lépp li ñuy wax ci pencum réewum Senegaal ci làkki réew mi, sànt nañu Yàlla, ndax mel na ni li ñuy fiy wax am na ñu ko dégg!
s-28 Wante li des bare na lool: Jot na ñu jàngale làkki réew mi ci daara yi, ci lekool!

Text viewDownload CoNNL-U