Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Cosaanu mbind ci Afrik
s-2 Cosaanu mbind ci Afrik lu mat a fésal la, ndax ñu bari, waay-xeltu yi ak ñeneen dañoo defe ne caada yi nekk Afrik xamuñu ca seen cosaan xaralaay mbind.
s-3 Manaam xeetu mbind yi fi nekk yépp dañu leen a jeggani: ci Arab yi mbaa ci Nasaraan yi.
s-4 Loolu nag dëppoowul benn yoon ak li am: ndax soo gëstoo dinga xam ci lu wér ne fii sax ci Afrik la mbind fekk baax.
s-5 Fii ci Afrik lañu njëkkee bind.
s-6 Kon ñakk-a-xam li mu waral bari na!
s-7 Li wér ci lu ñu xam ci xam-xamu cosaan moo di: fii ci Afrik, ca Misiraay démb la nit tàmbalee bind.
s-8 Booba ak léegi am na lu ëpp juróomi junniy 5000 at.
s-9 Ci ab xaatim àlluwa ji ñuy tuddee alluwaay Narmeer (-3200 laata Juddu Yonnent Yàlla Isaa) lañu firndeel mbind mi gën a yàgg te ñu koy woowee 'Hieroglyphes' ci Nasaraan.
s-10 Baat boobu nag du làkki maam ya nekkoon Misiraa, baatu Gerek la.
s-11 Mbind moomu turam dëgg moo doon 'medu ntr' muy tekki 'waxi Yàlla' ci làkki maam yooya!
s-12 Ca Hieroglyphes yooya mbaa 'medu ntr' ya la yeneen xeeti mbind yi ci àddina yépp daanaka sosoo!
s-13 Bindi Gerek yi nga xam ne, la bindi tubaab yi téy jóge, mu nga sosoo ca bindi waa Fenisi.
s-14 Waa Fenisi yooyu ña nga jàngee woon bind ñoom itam ca maam ya woon Misira.
s-15 Waa Fenisi yooyu ay jaaykat yu mag lañu woon.
s-16 Ñoo doon daanaka dox diggante Misiraa ak yeneen réew ya woon Asi mbaa Ëroop.
s-17 Jamono jooja sax gaa Ëroop amagul woon.
s-18 Yeneen réew yu mel ni yu 'Hitites' ak yeneen ñoo fa nekkoon!
s-19 Gànnaaw loolu itam yeneen xeeti mbind yu bari judd nañu fii ci Afrik.
s-20 Bi ci gën a siiw di bu Meroe, te ngeen di gis nataal bi fii ci xët wii!
s-21 Mbindum Meroe moomu ba bés niki téy xamaguñu lu muy tekki!
s-22 Te mbind mu xereñ la, mu am solo.
s-23 Maam ya fi nekkoon sàkkoon ko fi!
s-24 Kon téy su ñu naan caada Afrik yi ay 'civilisations orales' lañu, cosaanoowuñu bind, dañuy wax rekk, wante lenn lu wér lalu ko!
s-25 Ay àtte-ñakkale ak wumpale kese la: Du leneen!

Text viewDownload CoNNL-U