Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

Showing 1 - 100 of 106 • previousnext

s-1 Biralub àqi doom Aadama
s-2 Biralub àqi doom Aadama ak Juddu-réew, bu 26 ut 1789
s-3 Dog bu jëkk bi.
s-4 Nit ñépp nekk gor ak yemoo ci ay àq lañuy judduwaale, wéye ko.
s-5 Wuute yi di am ci biir mbooloo mi mënuñu wéeru lu dul ci njariñal ñépp.
s-6 Jubluwaayu gépp mbootaayu politig moo di càmmug àq yi doom Aadama làmboo te yàgg du leen far.
s-7 Àq yooyu ñoo di moom sa bopp, moomeel, warlu, ak bañ noteel.
s-8 Ballukaayu gépp baat bu nit yore a ngi nekk ci Xeet wi.
s-9 Amul jenn jëmm, kenn nit ku mën doxal baat bu ci jógewul, ci lu wér.
s-10 Moom sa bopp mooy mën def lépp lol du yàqal jaambur:
s-11 Naka noonu, nit ku ne àq yi mu làmboo te di leen doxal seen i dig a ngi yem ci dig yi di may ñeneen ñi bokk ci mbooloo mi ñu bànneexu ñoom it ci àq yooyu.
s-12 Dig yooyu yoon rekk a leen mën tëral.
s-13 Àtte sañul tere lu dul jëf yi di lor mbooloo mi.
s-14 Lépp lu yoon terewul, mëneesu ko tere, te yit mëneesul ga kenn ci mu def lu yoon santaanewul.
s-15 Àtte mooy kàddu giy génne bëgg-bëggu mbooloo mi.
s-16 Juddu-réew yépp sañ nañu, ci seen jëmmu bopp, walla ci jëmmu ndaw yu leen fi toogal, bokk ci lu koy tëral.
s-17 Yoon dafa war doon benn ci ñépp, moo xam dafay aar, walla dafay daan.
s-18 Juddu-réew yépp, gannaaw ba nga xamee ne ñoom ñépp a yem ci kanamam, ñoo yem ci am sañ-sañu yóotu martaba, palaas, ak nekk ndawi nguur gi, ku ne ak li sa mën-mën may, ci lu àndul ak benn xajjaatle, lu dul li aju ci seen njàmbaar ak seen xarala.
s-19 Mëneesul teg kenn tuuma, walla ñu jàpp ko, mbaa téj ko, lu dul ci anam yi yoon tëral, ak jëfin yi mu santaane.
s-20 Ñi di sàkku, yóbbante, jëfe walla jëfeloo ay ndigal yu amul teguwaay, dees leen war daan;
s-21 Waaye bépp juddu-réew, bu ñu ko woowee walla ñu téye ko ci kow yoon, war na cee tënku ci saa si: tooñ na, su fekkee ne dafa bañ.
s-22 Yoon warul tëral lu dul ay daan yoo xam ne, fés na ni yem nañu kepp, te amul kenn ku ñu mën daan, lu dul ci kow ab àtte bu am, ñu taxawal ko lu jiitu tooñeel gi, te fekk ñu ngi koy doxal ni mu ware ci yoon.
s-23 Gannaaw nit ku mu, jortees na ne set na ci ag tooñeel ba keroog ba ñu di biral ne tooñ na, su fekkee ne gisees na ne mëneesu ko bañ a jàpp, gépp teeŋal gu dul gi ci yell ngir jot ci jëmmam, yoon war na ko daan daan yu tar.
s-24 Amul kenn ku ñu war gétén ngir i xalaatam, doonte sax ci wàllu diine la, na fekk rekk seen ag génne yàqul dara ci jàmmu nekkeel ji àtte tëral.
s-25 Kon bépp juddu-réew mën na wax, bind, muul ci coobareem;
s-26 Xanaa rekk moo di gàddu bëttug sañ-sañ boobu, ci anam yi yoon tëral.
s-27 Warlul àqi doom Aadama ak juddu-réew dafa laaj doole ju di aar ñépp, muy dooley mbooloo mi.
s-28 Doole jooju dees ko di samp, ngir njariñal ñépp, waaye du doon ngir njariñal ñi ñu ko dénk.
s-29 Ngir yor dooley mbooloo mi ak ngir amal xaalis bi war ci caytu gi, ab natt bu ku ne war dugal loxoom mënul ñàkk; dees ko di teg juddu-réew yépp, ku ne ak la nga mën.
s-30 Juddu-réew yépp sañ nañu nemmiku, ñoom ci seen bopp walla ci kow ndaw yu leen fa toogal, ndax natt boobu dafa di lu war.
s-31 Sañ nañu ko nangu ci seen coobare, toppaatu jëfandikoo ga, taxawal daytalinam, ak lalam, ak feyyuwinam, ak diir ba.
s-32 Mbooloo mi sañ na làyyiloo bépp liggéeykat bu ne ci caytukaayu nguur gi.
s-33 Mépp mbooloo mom warlug àq yi ak teqaleg baat yi doxu fa, amul ndeyu àtte.
s-34 Gannaaw moomeel dafa di àq ju fegu, te sell, mëneesu ko xañ nit, xanaa su fekkee ni njariñal mbooloo mi dafa ko laaj ci lu ñépp mën gis.
s-35 Mu doon lees nemmeeku ci yoon, ak ci kow ndàmpaay lu jub, lu jiitu toxalug moomeel gi.
s-36 Biralub Dunyaa ñeel àqi doom Aadama
s-37 Pénc mu mag mi fal na ko, siiwal ko ci dogal 217 A (III) bi mu génnee ci 10 desàmbar 1948.
s-38 Dog bu jëkk bi.
s-39 Nit ñépp moom sa bopp lañu di judduwaale, ak yemoo ci ay sañ-sañ ak daraja.
s-40 Xéewalees na leen sago ak xel; dañu war jëflante ni ay doomi ndey.
s-41 Nit ku ne mën na yiiru ci àq yi ak sañ-sañ yi ñu taxawal yépp ci Biral bii.
s-42 Te du ànd ak benn xàjjaatle ci wàllu xeet, ak melow der, ak awra, ak kàllaama, walla diine, walla xalaat ñeel mbirum politig, walla meneen xalaat mu mu, moo xam mu ngi tukkee ci aw xeet mbaa ci am mbooloo, walla alal, walla juddu, walla beneen fànn bu mu.
s-43 Yokk ci, réew mi walla dénd bi doom Aadama cosaanoo, deesu ci def benn xàjjaatle bu wéeru ci taxawalinam ci wàllu politig, walla ci wàllu yoon, walla ci wàllu jëflante bi mu séq ak bitim-réew, moo xam réew moomu mbaa dénd boobu dafa moom boppam, walla dafa nekk ci kiliftéef, walla mu am baatu biir rekk, walla mu am lu mejj ci baatam.
s-44 Nit ku ne am na sañ-sañ ci ag dund, ak ci baatu boppam ak ci kaaraangeg jëmmam.
s-45 Deesul def kenn ab jaam, walla ab dag;
s-46 Njaam, ak njaay ak njëndum jaam terees na ko, ci anam yu mu mën doon.
s-47 Deesul bugal kenn, deesul teg kenn ay daan ak ay metit yu tar, yu nit xajoowul, walla yu ko di toroxal.
s-48 Nit ku ne am na sañ-sañ ci ñu nangul ko, ci bépp béréb bu mu ne, jëmm ji mu taxawe ci wàllu yoon.
s-49 Ñépp a yem ci kanam yoon te ñépp am nañu sañ-sañ ci yoon feg leen, ci ag yemale gu àndul ak benn xàjjaatle.
s-50 Ñépp am nañu sañ-sañ ci ñu bokk leen feg ci bépp xàjjaatle bu nar a jalgati Biral bii, ak ci lépp lu nar a sooke xàjjaatle boobu.
s-51 Nit ku ne sañ na dem yoon, ci kanam àttekaay yi ko yelloo ci réew mi, ngir tawat fa jëf yi di bëtt sañ-sañ yi ko Ndeyu Àtte bi walla ab àtte fàggul.
s-52 Amul kenn ku, mënees na ko jàpp, walla téj, walla gàddaayloo, ci lu teguwul fenn.
s-53 Nit ku ne, ci ag yemale gu mat sëkk, am na sañ-sañ ci, layam, ab àtteekaay bu moom boppam te maandu déglu ko déglu bu sell, ci biir mbooloo, sog a jël dogal yoy, moo xam ñu ngi jëm ci feeñal i àqam ak i wareefam, moo xam ñu ngi jëm ci dëgëral bépp tuuma ju ñu ko teg ci wàllu jëyya.
s-54 Képp nit ku ñu tuumaal tooñeel, njortees na ni ku set la, ba keroog ba yoon di wéral tuuma ji, ci layoo bu ne fàŋŋ, fekk warlulees na nit ki fàggutéef yi layam laaj yépp.
s-55 Deesul daan kenn ngir ay jëf, walla ay càggante yoy, ci jamono ji ñu leen defe, nekkuñu woon njëfu tooñeel ci gis-gisu yoon wi di dox ci réew mi ak wi di dox ci diggante réew yi.
s-56 Naka noonu, deesul tege benn daan bu gën a diis bi ñu waroon tege ca jamono ja njëfu tooñeel ja ame.
s-57 Deesul lëñbëtu kenn ci mbiri boppam, njabootam, këram, bataaxalam, walla ñu wuññi suturaam, yàq deram, ci lu teguwul fenn.
s-58 Nit ku ne am na sañ-sañ ci yoon feg ko ci lëñbët yooyu ak tooñ yooyu.
s-59 Nit ku ne sañ na dem ak dikk ci coobareem, ak tànn dëkkuwaayam ci am réew.
s-60 Nit ku ne sañ na génn mépp réew, doonte mosam la; sañ na yit dellusi ci réewam.
s-61 Ci kow bundxataal gu ñu koy bundxataal, nit ku ne sañ na wuti rawukaay, sañ na yit muurloo rawukaay ci yeneen i réew.
s-62 Sañ-sañ boobu nit ki mënu ko tuddoo, su fekkee ne jëyya ju aju ci yoon wi ñépp bokk lañu koy toppe, walla ay jëf yu safaanoo ak jubluwaayi Mbootaayu Xeet yi ak i sàrtam.
s-63 Nit ku ne am na sañ-sañ ci ag askanale.
s-64 Amul nit ku ñu mën xañ askanaleem, naka noonu yit mëneesu koo xañ sañ-sañu soppi askanaleem.
s-65 Li-ko-dale ci jamono ji ñu tolloo ci séy, góor ak jigéen, ci lu àndul ak benn xat-xat bu aju ci waaso, askanale walla diine, am nañu sañ-sañu séy ak samp njaboot.
s-66 Ci wàllu séy, ñoo yem sañ-sañ ci biir séy bi ak ci tasug séy bi.
s-67 Séy bi mëneesu ko fas lu dul ñi nar a nekk way-dencante dañu ci a ànd ànd bu wér, ci seen coobare.
s-68 Njaboot mooy cosaanu mbooloo mi ak kenu li ko téye; yeyoo na mbooloo mi ak réew mi aar ko.
s-69 Nit ku ne, moo xam mu ngi nekk moom kenn, walla ci mbooloo, yeyoo na moomeel.
s-70 Mëneesul xañ kenn moomeelam, ci lu teguwul ci yoon.
s-71 Nit ku ne am na sañ-sañ ci wéye xelu boppam ci wàllu xalaat, ngëm ak diine;
s-72 Sañ-sañ boobu dafa ëmbaale sañ-sañu nit ki ci soppi diine, walla ngëm, ak sañ-sañu feeñal diineem, walla ngëmam, moom kenn walla ci mbooloo, moo xam ci lu ni fàŋŋ la walla, ci lu biiru la, mu jaarale ko ci am njàngale, ci jëfi diine, ci jaamu boroomam ak topp ponki diineem.
s-73 Nit ku ne am na sañ-sañ ci xalaat ak génne xalaatam ni mu ko soobe te loolu dafa wund ni am na sañ-sañ ci ñu bañ ko fitnaal ngir xalaatam.
s-74 Am na it sañ-sañ ci taataan, ak jot, ak tas te amul dig yu mu ci di seet xabaar yi ak xalaat yi, ci génnekaayu xalaat bu mu mënti doon.
s-75 Nit ku ne am na sañ-sañu bokk ci ndaje ak mbootaay yu jàmm lal.
s-76 Mëneesul ga kenn ci mu bokk ci ag mbootaay.
s-77 Nit ku ne, ci biir réewam, am na sañ-sañu bokk ca njiit ya di saytu doxalinu réew ma, moo xam moom ci boppam la, walla mu dénk baatam ay ndaw yu mu tànn ci coobareem.
s-78 Nit ku ne am na sañ-sañ ci ñu ubbil ko, ci ag yemale gu ñeel ñépp, bunti liggéeyukaayi nguur gi.
s-79 Bëgg-bëggu askan wi moo di kenu li téye baatu nguur gi;
s-80 Bëgg-bëgg boobu li ko di génne mooy pal gu jub, gu ñu war amal diiroo diir, ci biir palin wu matale te yem, ànd ak kumpa, walla ci weneen palin wu nuroo ak moom te mën jur pal gu sell.
s-81 Nit ku ne, ci ni mu bokke ci mbooloo mi, am na sañ-sañ ci xéewloo kiiraayal mbooloo mi;
s-82 Yelloo na ñu jox ko ci wàllu koom, nekkin, caada, sañ-sañ yi darajaam ak yokkuteg jëmmam laaj, ci liggéeyub réewam ak jëflanteg réew ak réew, lépp nag aju ci doxalinu réew mu ne, ak ci alalam.
s-83 Nit ku ne am na sañ-sañ ci liggéey, ak ci tànnal boppam liggéey bi ko soob, ak ci am sàrti liggéey yu jub te baax ci moom, ak ci lu ko feg ci ñàkkum liggéey.
s-84 Ñépp am nañu sañ-sañ ci yem añub liggéey, su fekkee ne ñoo yem liggéey, ci lu àndul ak benn xàjjaatle.
s-85 Képp kuy liggéey yelloo na pey gu jub te baax, gu mu di suturloo moom ak njabootam, ci nekkin wu méngoo ak daraja ji nit làmboo te, su ko laajee, mu am yeneen xeeti pexe yu ko mottali, ci wàllu kiiraayal nekkin.
s-86 Nit ku ne sañ na ànd ak ñeneen sos ay sendikaa, ak bokk ci ay sendikaa ngir sàmm njariñam.
s-87 Nit ku ne am na sañ-sañ ci noppalu ak féexal xolam, rawatina ci wàññi, ci anam yu jaadu, yàggaayu liggéey bi, ak ci noflaay yu ànd ak pey, diiroo diir.
s-88 Nit ku ne yelloo na xéewloo koom gu doy ngir feg wér-gu-yaramam, dund dund gu neex moom ak njabootam, rawatina ci lu jëm ci lekk gi, koddaay li, paj mi ak garabi faju yi ak yeneen aajo yi nekkin laaj;
s-89 Nit ku ne yelloo na kiiraay, su fekkee ne liggéeyul, dafa tawat, dafa tële, ki mu doon séyal dafa faatu; ak su fekkee ne dafa màggat mbaa mu tollu fu nga xam ne, yeneen safaan yu ajuwul ci coobareem ñoo ko xañ la mu daan dunde.
s-90 Ndey ji sukk wasin ak gune yelloo nañu ñu beral leen ndimmal ak taxawu.
s-91 Gune yépp, moo xam ci buumu séy lañu juddoo walla déet, ñoo yem kiiraayal nekkin li ñu yeyoo.
s-92 Nit ku ne yeyoo na jàng.
s-93 Njàng mi wareesu ci fey dara, walla boog njàng mu suufe mi ak mu njëkk mi.
s-94 Njàng mu suufe mi, ñépp lañu ga ñu jaar ci.
s-95 Njàngum xarale mi ak mu mécce mi, dees ko war yaatal ba mu yegg ci ñépp.
s-96 Buntu njàng mu kowe mi warees na ko ubbil ñépp, ci ag matale gu mat sëkk, kenn ku ne ak li mu yelloo.
s-97 Njàng mi dafa war jublu ci tëgg nit ci jikko yu rafet, ak ci dëgëral worma gi àqi doom Aadama ak sañ-sañ yu mag yi yelloo.
s-98 Dafa war yombal déggoo, muñalante ak xaritoo ci biir xeet yépp ak ci biir mbooloo yi aju ci waaso yi ak diine ji.
s-99 War na yombal yitam yokkute ag yëngute yi Mbootaayu Xeet yi sumb ngir saxal jàmm.
s-100 Way-jur yi ñoo jiitu ci am sañ-sañu tànn xeetu njàng mi ñu bëggal seen njaboot.

Text viewDownload CoNNL-U