Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

s-1 Nguurug Tukulóor mi ngi sosu njëkk juróom ñeenteelu xarnu, njabootug Ogo Ja jiite ko.
s-2 Ci mujjantalug xarnu bu fukkeel la Waar Jaabi song ki mujjoon ci buuri njaboot googu, ray ko.
s-3 Bu ko defee mu daldi jël nguur gi.
s-4 Ci noonu la geneen njaboot jote ci nguur gi, mooy gu Mana.
s-5 Waar Jaabi dugg na ci Lislaam, daldi jóg def jiyaar ci kaw dëkkandoom yi dul jullit.
s-6 Ci noonu la nguurug Tukulóor xéye di nguur gi njëkk a dugg ci Lislaam ci Senegaal.
s-7 Tukulóor yi bokkoon nañu ci yaxantug wurus wi ak njaayum jaam yi.
s-8 Li ko waraloon it moo di dend gi ñu dendoon ak dexug Senegaal gi, ak nekk gi ñu nekkoon ci yoonu yaxantu wi.
s-9 Mu nekkoon réew mu naat te am doole, waaye dafa rotoon ci ron teg loxo gu imbraatóor gu Gana, (ci xarnub fukk ak benn).
s-10 Ginnaaw bi mu rot ci gu Mali (ci xarnu bu fukk ak ñatt), rotati ci gu Jolof (ci xarnub fukk ak ñeent).
s-11 Ci mujjug xarnub fukk ak juróom la Koli Tingala jóg xeex Tukulóor yi, daldi tembal ay goxam, taxawal nag nguur gu yees, mooy Fuuta Tooro, njabootug Deñanke jiite ko.
s-12 Ci xarnub fukk ak juróom benn Fuuta Tooro def na ay xare ngir yaatal suufam ci kaw ay dëkkandoom: Jolof, Kajoor.
s-13 Njabootug Deñanke nag manatuñu woon a jàmmaarloo ak cong yi tukkee ci biti, ak lëj-lëji kuutu gi.
s-14 Ci atum 1770 g.j, la ag fippu am walla ag jeqiku tukkee ci kilifay jullit ñi, Cerno Sulaymaan Baal jiite ko, daldi daaneel njabootug Deñanke.
s-15 Bu ko defee, Baal jël Lislaam def ko cëslaay li nguur gi di tegu te di ko ci doxale.
s-16 Cerno Sulaymaan Baal bàyyee woon na nguur gi Yilimaan Abdul Xaadir Kan.
s-17 Moom lañu di jàppe ki njëkk a doon Yilimaan.

Text viewDownload CoNNL-U