Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Microsoft: Siiwalug Windows Phone 7
s-2 Microsoft dellusi na ci ag woote ak ab gaaral bu ràññeeku altine ci lu aju ci telefonam bi ñépp di xaar Windows Phone 7 ànd ak defar Nosteg Doxiin (operating system) bu bees tàq ñeel Mobiil.
s-3 Doorees na ag gaaralu Windows Phone 7 ca New York.
s-4 Gaaral googu njiitul Microsoft Stef Balma moo ko jiite, ngir wone ni seen nosteg doxiin bu bees bi dafa nekk lu taaru te yéeme.
s-5 Ku nekk war naa man a seet Windows Phone te wax ni man na maa teewal la Balma wax.
s-6 Ci loolu, joyalees na siiwalug Windows Phone jëmmalug man-mani telefon bi ak ay leeral ci juumtukaay yi ci nekk.
s-7 Wonees na nosteg doxiin bi mel niki luy mottalil boppam ag dundam ci lu dul di ko xaar feneen.
s-8 Siiwalees na juróom ñeenti telefoni Windows Phone yoo xam ne fimne way-jëfandikuy waa-aamerig dinañu ci daldi man a tàmbali a tànn, ànd ak T-Mobiil AT&T génne ko, ci gën gaa yeex, 8 Nowàmbar.
s-9 Lu aju ci tëriin li, jëmmal gi ak yomb-gee-jëfandikoo moo di li tax a jóg Mickrosoft ci lii, ci yakaar a joxe jëmmal gu mat sëkk.
s-10 Looloo tax sa Smartphone (telefon bi) man a teyewaale la ñu xamoon ci Microsoft-centric (beneen telefon).
s-11 Wax nag yomb na, kon nanu xaar ba Windows Phone 7 wàcc ci maarse bi (ja bi) nu xool ndax seen jubluwaay walla yéene jooju mel na ni.
s-12 Mbetteel gi gën a rëy ci wàllu ndefarum tëriin dal na leen, ndekete Windows Phone 7 déy manul sax a jël man-manu sotti-taf (copie-coller), Waawaaw!
s-13 Lu man a am daal manu ko fimne.
s-14 Nee nañu nag dinañu def ag yeesal ngir mu man ko ci weeru Saawiyee.

Text viewDownload CoNNL-U