Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Waalo bokkoon na ci yenn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon.
s-2 Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar.
s-3 Njurbel moo nekkoon péeyam ci lu njëkk.
s-4 Gannaaw bi lañu ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer.
s-5 Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu gannaaw ak ñàkk doole.
s-6 Ñooñu ñooy : Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi.
s-7 Gannaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur.
s-8 Bokk na ca Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néegu Njurbel.
s-9 Moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur.
s-10 Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel.
s-11 Moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi.
s-12 Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi.
s-13 Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo.
s-14 Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de Geer.
s-15 Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo:
s-16 Ba njëkk moo di Lingeer mi di yaayu buur bi ak Aawo mi di soxnaay buur su njëkk.
s-17 Moom moo am teraangaay toog ca gangunaay (moo di toogu gu buur) ga.
s-18 Bu ñaareel ba mooy ñatt ci boroom ndomboy tànk yi ci péncum Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak Maalaw mi yor koom-koom bi.
s-19 Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur.
s-20 Baadi moom moo di njiitu doomi buur bi, ak yenn ci jëwriñ yi.
s-21 Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare.
s-22 Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram.
s-23 Mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo war a teew ci gàmmu gi.
s-24 Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la.
s-25 Ndaxte seenug teew li mu di tegtal moo di yeesal seenug nangu, la ñu lokki ak la ñu siif.
s-26 Mbooleem alal yooyu daa nañu leen séddale ñetti xaaj: benn ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca péncum Séb ak Bawar.
s-27 Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbéem yi.
s-28 Nguur ga dañu ko seddale woon ci ay diwaan.
s-29 Bu ci ne amoon na Bàjjo bu di dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer).
s-30 Kàjj moom lañu fal ci ndijjooru dex gi, li-ko-dale ca Aarnik ba fa dex gi sottee.
s-31 Buriko moom lañu fal ci bëj-gànnaaru Lag de Geer.
s-32 Mu ngi daan dëkk ca Foos.
s-33 Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinó Bawaal.
s-34 Li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi.
s-35 Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo.
s-36 Barlaf moo nga dëkkoon ca sowwu Lag de Geer.
s-37 Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ay cong yu jóge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi.
s-38 Moo tax ba ci xarnub XX waa Waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi.
s-39 Ba bésu tey Waaloo ngi jànkonte ak cong ya jóge woon ca ŋaayoo ga.
s-40 Loolu moo di jur dellu gannaaw ak daanug Waalo, ba ku nekk di ko cokkaas: Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel.
s-41 Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas.
s-42 Gannaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx, da koo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen gannaaw ci 1885.
s-43 Booba la nootee Waalo, te naan dafa koy xettali.

Text viewDownload CoNNL-U