Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

s-1 Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal.
s-2 Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.
s-3 Kajoor moo di kàdd ag garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si.
s-4 Moo jur baat boobu Kajoor ci Wolof.
s-5 Ñi jëkk a yor suufi Kajoor, ay séeréer lañu woon.
s-6 Ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ.
s-7 Ba pare, xeetu Wagadu ak Jafunu, soqi ci Sooninké yi, jóge ca penku.
s-8 Ñoo sos meen yi jëkk a ilif nguur gi, ak ñu sant FAAL.
s-9 Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor.
s-10 Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu yu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen.
s-11 Dammeel mooy damm.
s-12 Ndax ku jëkk a jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor.
s-13 Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam.
s-14 Loolu, ca jamono ja Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon Buur-ba Jolof la xeewe.
s-15 Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu Njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI.
s-16 Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon.
s-17 Ba noppi Amari Ngone jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor.
s-18 Ca tegu, Kajoor di gën a am doole.
s-19 Amari Ngone dem na Bawol ak ay jàmbaaram, nangu reew moomu.
s-20 Lii moo tax Amari doonoon ku jëkk a nekk Dammeel-Teeñ.
s-21 Bawol, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan.
s-22 Amari moo duggal aada bi.
s-23 Ñu fal buur bu ñu tudde Xulixuli, di fàtteliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkk a nekk Buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo.
s-24 Ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur gu ay am-amam newoon gàññ.
s-25 Mbay ak liggéey ci loxo ak càmm ak napp ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga.
s-26 Mbay moo doonoon liggéey bi ëppoon solo ci koom-koomam.
s-27 Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ ca koom ga.
s-28 Manoon naa indi sax ab xiif.
s-29 Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi.
s-30 Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng.
s-31 Xamoon nañu mbayum wëtteen.
s-32 Liggéey ak loxo ñeeño yi lañu ko feetale woon.
s-33 Napp gi amoon na solo lool ci dund gi.
s-34 Waaye njaay moom naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal.
s-35 Mujj na ba yoon yi jóge bëj-gànnaar ñàkk solo lool njëgg mi.
s-36 Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo.
s-37 Fekkoon na Kajoor daan jaay ay der ak ay bëñi ñayy.
s-38 Mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi, ...
s-39 Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon.
s-40 Ñi ñu di wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu.
s-41 Benn nit amu ci woon moomeel.
s-42 Loolu terewul woon ku mu neexoon mu jariñoo ci kéem kàttanam.
s-43 Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya.
s-44 Ñi di door a falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo.
s-45 Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon.
s-46 Ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul.
s-47 Rax-ci-dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk.
s-48 Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi.
s-49 Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetale woon mbay mi.
s-50 Ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat.
s-51 Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay.
s-52 Nguur gu bees gi tax na ba ñu indi tër yu bees ci ay àtte yu bees.
s-53 Dammeel moo féete woon ñépp kaw.
s-54 Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen.
s-55 Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen.
s-56 Waaye loolu su xewee li ko di waral moo di fullay waa ja ak faydaam ak tabeem.
s-57 Yii yépp ñi di tànn daa nañu ci bàyyi xel.
s-58 Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem.
s-59 Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe.
s-60 Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur.
s-61 Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.
s-62 Kajoor nekkoon na juróomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum.
s-63 Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam fu nga féete.
s-64 Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur.

Text viewDownload CoNNL-U