Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttest

Select a sentence

s-1 Jimbulang aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulang bu di wax ci paj walla ci taariix kepp.
s-2 Jimbulang am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ci aw nit, ci ab barab, ci ab xew-xew, ci ab xam-xam, ...
s-3 Jimbulang dafa di wuute ak baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi.
s-4 Naka-jekk dafay doon ay téere yu bari.
s-5 Cër yi ëpp solo yi di tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu: Jagleel gi ci am, seenug lëkkaloo, nosiin wi ak mbidiinu jukki yi.
s-6 Jimbulang yi man nañu a wuute, aju ci seen ëmbiit, man nañu a ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa Brëtaañ, ñoo di yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu.
s-7 Am na it ay jimbulang yu di jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi...
s-8 Yitteey liggéeyi jimbulang moo di jébbal xameef gi ëpp solo gi di dajale ñeel tëriit li.
s-9 Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñu ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu.
s-10 Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi dafa di soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam.
s-11 Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bi ñuy jagleel i gune mooy gën a néew bi ñuy jagleel i mag.
s-12 Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb.
s-13 Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañu di jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi moo di séddale leen ci ay wàll.
s-14 Nit, dale ci lu yàgg ci ag nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam.
s-15 Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp.
s-16 Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu ci a lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juróom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja.
s-17 Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima (Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax.
s-18 Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr Al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi (ci daanaka 270 téere)
s-19 Imbratóor bu Siin bi, Cheng-Zu bu Callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix.
s-20 Mu ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yi ñu binde ak loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay.
s-21 Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yi ak niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: doonoon nañu ay téere yu seer lool.

Text viewDownload CoNNL-U