Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train
Text: Transcription Written form - Colors
Lesoleil : Gàawu 11 awril 2009
s-1
wo_wtb-ud-train_2095
Lesoleil: Gàawu 11 awril 2009
Porogaraam biy xeex sibbiru ci réew mi te tudd PNLP , ci jàppleg ñi muy jëflanteel , yeesal na xam-xamu 51 njiiti doktoori gox yi ak seen i toftal , ci pexe yu bees yi ñu tëral ngir xeex sibbiru , ci ñaari lël .
s-2
wo_wtb-ud-train_2096
Porogaraam biy xeex sibbiru ci réew mi te tudd PNLP, ci jàppleg ñi muy jëflanteel, yeesal na xam-xamu 51 njiiti doktoori gox yi ak seen i toftal, ci pexe yu bees yi ñu tëral ngir xeex sibbiru, ci ñaari lël.
Ñaareelu lël bi , jëm ci njàngale ñeel sibbiru ak xeex bi mu laaj , dajale na 26 doktoor .
s-3
wo_wtb-ud-train_2097
Ñaareelu lël bi, jëm ci njàngale ñeel sibbiru ak xeex bi mu laaj, dajale na 26 doktoor.
Lël boobu mu ngi tàmbali ci 16 màrs ci Daaray Wér ( ISED ) tëj ci 4 awril 2009 , ci njiitéefu Dr Asan Yaradu , kenn ci ñi di xelal njawriñu wér ak fàggutéef .
s-4
wo_wtb-ud-train_2098
Lël boobu mu ngi tàmbali ci 16 màrs ci Daaray Wér (ISED) tëj ci 4 awril 2009, ci njiitéefu Dr Asan Yaradu, kenn ci ñi di xelal njawriñu wér ak fàggutéef.
Doktoor Pàppa Muusaa Coor miy saytu PNLP xamle na ne njàngale mii ñu sumb mu ngi bokk ci pexe yi ñu tëral ngir sibbiru ak dee yi muy jur bañ a jéggi tolluwaay bi mu nekk jamono yii .
s-5
wo_wtb-ud-train_2099
Doktoor Pàppa Muusaa Coor miy saytu PNLP xamle na ne njàngale mii ñu sumb mu ngi bokk ci pexe yi ñu tëral ngir sibbiru ak dee yi muy jur bañ a jéggi tolluwaay bi mu nekk jamono yii.
Ndax gisees na ne tolluwaay bi dafay gën di wàññiku te li ko waral moo di pexe yi ñu tëral ngir xeex jàngoro ji .
s-6
wo_wtb-ud-train_2100
Ndax gisees na ne tolluwaay bi dafay gën di wàññiku te li ko waral moo di pexe yi ñu tëral ngir xeex jàngoro ji.
Mënees naa lim yenn ci pexe yooyu : joxe sànke yu ñu nàndal , ak fexe ba garab yi ( ACT ) ñépp mën cee jot ci njëg gu yomb , ak def ay càmbar yu feeñal jàngoro ji , na mu gën a gaawe .
s-7
wo_wtb-ud-train_2101
Mënees naa lim yenn ci pexe yooyu: joxe sànke yu ñu nàndal, ak fexe ba garab yi (ACT) ñépp mën cee jot ci njëg gu yomb, ak def ay càmbar yu feeñal jàngoro ji, na mu gën a gaawe.
Ci 2008 , tolluwaay baa ngi nekkoon ci 5,6 % te mooy junni nit ñu ne , juróom-fukk ak juróom–benn yi sibbiru dal na leen .
s-8
wo_wtb-ud-train_2102
Ci 2008, tolluwaay baa ngi nekkoon ci 5,6 % te mooy junni nit ñu ne, juróom-fukk ak juróom–benn yi sibbiru dal na leen.
Looloo waral Dr Coor yokk ci : su nu wéyee di góor-góorlu , waxuma rekk ne tolluwaay bi dina yem foofu , waaye sax dinanu faagaagal xeetu sibbiru bii .
s-9
wo_wtb-ud-train_2103
Looloo waral Dr Coor yokk ci: su nu wéyee di góor-góorlu, waxuma rekk ne tolluwaay bi dina yem foofu, waaye sax dinanu faagaagal xeetu sibbiru bii.
Ci xalaatam , ngir bundxataal sibbiru , dafa laaj beneen wirgo doktoor , beneen wirgo saytukat ngir tolluwaayu dee gi ci aju ak jàngoro ji bañ a yéeg .
s-10
wo_wtb-ud-train_2104
Ci xalaatam, ngir bundxataal sibbiru, dafa laaj beneen wirgo doktoor, beneen wirgo saytukat ngir tolluwaayu dee gi ci aju ak jàngoro ji bañ a yéeg.
Looloo tax ñu taxaw temm ci yeesal xam-xamu doktoor yi te dooleel leen ci pajum sibbiru , Doktoor Coor teg ko ci .
s-11
wo_wtb-ud-train_2105
Looloo tax ñu taxaw temm ci yeesal xam-xamu doktoor yi te dooleel leen ci pajum sibbiru, Doktoor Coor teg ko ci.
Njiital Ised , Pr Anta Taal Ja , moom , dafa ñaax doktoor yi ñu nekk ay mbër ak ay saytukat ci xeexu sibbiru , ku nekk ci sa gox .
s-12
wo_wtb-ud-train_2106
Njiital Ised, Pr Anta Taal Ja, moom, dafa ñaax doktoor yi ñu nekk ay mbër ak ay saytukat ci xeexu sibbiru, ku nekk ci sa gox.
Doktoor yi ñoom rafetlu nañu njàngale mi , ndax ñi leen doon xamal wàccoo nañu ak ñoom , li ñu ci doon xaar gis nañu ko .
s-13
wo_wtb-ud-train_2107
Doktoor yi ñoom rafetlu nañu njàngale mi, ndax ñi leen doon xamal wàccoo nañu ak ñoom, li ñu ci doon xaar gis nañu ko.
Edit as list • Text view • Dependency trees