Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Text: -

[1] tree
Fan lanu jëm ak sunu demokaraasi bii?
s-1
wo_wtb-ud-train_1981
Fan lanu jëm ak sunu demokaraasi bii?
[2] tree
Réew mu nga xam ni yennat ci ay xalaat ñoo fi dagan, yeneen dañu araam.
s-2
wo_wtb-ud-train_1982
Réew mu nga xam ni yennat ci ay xalaat ñoo fi dagan, yeneen dañu araam.
[3] tree
Réew mi moo ne: sañ-sañu xalaat génne ko, xalaatal sa xel, lu mu jur nga wësin ko niki yooyee demokaraasi di yu Tugal yi nga xam ne ñooy ya mag yi ñu di roye.
s-3
wo_wtb-ud-train_1983
Réew mi moo ne: sañ-sañu xalaat génne ko, xalaatal sa xel, lu mu jur nga wësin ko niki yooyee demokaraasi di yu Tugal yi nga xam ne ñooy ya mag yi ñu di roye.
[4] tree
Loolu jural nu nuy lang ci ay mbiccam, di jafandu ci ay waggam.
s-4
wo_wtb-ud-train_1984
Loolu jural nu nuy lang ci ay mbiccam, di jafandu ci ay waggam.
[5] tree
Nu naan lu fi di lu baax moom la, du keneen, du feneen.
s-5
wo_wtb-ud-train_1985
Nu naan lu fi di lu baax moom la, du keneen, du feneen.
[6] tree
Loolu tax na ba sax lu bawoo feneen du leneen lu dul neen ndax li muy keneen.
s-6
wo_wtb-ud-train_1986
Loolu tax na ba sax lu bawoo feneen du leneen lu dul neen ndax li muy keneen.
[7] tree
Lii ak lu ni mel moo jur natt ci ñaari nattukaay gi Tugal di def ba ay farandoom di ko ca fekk ak a roy.
s-7
wo_wtb-ud-train_1987
Lii ak lu ni mel moo jur natt ci ñaari nattukaay gi Tugal di def ba ay farandoom di ko ca fekk ak a roy.
[8] tree
Fan yii jàll coow jeqiku woon na ci réew mi, te dara jeqiwu ko woon lu moy kàddu yu njiitu réew mi yekkati woon ñeel estateem bii di bu ñu tere ci Lislaam ci mbooleem ay yaxam.
s-8
wo_wtb-ud-train_1988
Fan yii jàll coow jeqiku woon na ci réew mi, te dara jeqiwu ko woon lu moy kàddu yu njiitu réew mi yekkati woon ñeel estateem bii di bu ñu tere ci Lislaam ci mbooleem ay yaxam.
[9] tree
Ñenn jógoon ngir dëgëral njiit li bay indi ay yax yu di ko dëgëral te yooya yépp di woon yu di aaye yi ñu bëgg a daganal.
s-9
wo_wtb-ud-train_1989
Ñenn jógoon ngir dëgëral njiit li bay indi ay yax yu di ko dëgëral te yooya yépp di woon yu di aaye yi ñu bëgg a daganal.
[10] tree
Loola tax ba njiit la lottee ci daganal ko ci Lislaam mu bëgg a jaare ci diineedi (laïcité) di li ñenn di woowe 'tëraayu njaaxanaay' ngir rekk wone ci ne mii réew moom du jullit ñi rekk a ko moom.
s-10
wo_wtb-ud-train_1990
Loola tax ba njiit la lottee ci daganal ko ci Lislaam mu bëgg a jaare ci diineedi (laïcité) di li ñenn di woowe 'tëraayu njaaxanaay' ngir rekk wone ci ne mii réew moom du jullit ñi rekk a ko moom.
[11] tree
Ñépp a ko bokk, Nasaraan bi jullit bi ak woroom tuur yi.
s-11
wo_wtb-ud-train_1991
Ñépp a ko bokk, Nasaraan bi jullit bi ak woroom tuur yi.
[12] tree
Te kat kii di kilifa gu mag ci réew mi di Seex Ahmadu Bamba romb na fi ay estati te waxu ci dara, naka noonu geneen kilifa gee di gu kenn magul ci Lislaam ju Senegal di Alhaaji Maalig.
s-12
wo_wtb-ud-train_1992
Te kat kii di kilifa gu mag ci réew mi di Seex Ahmadu Bamba romb na fi ay estati te waxu ci dara, naka noonu geneen kilifa gee di gu kenn magul ci Lislaam ju Senegal di Alhaaji Maalig.
[13] tree
Waa jàngu bi it bokk ci réew mi te seen i biir jàngu ay estatee fa nekk yu ñu di jublu ci seen ag jaamu.
s-13
wo_wtb-ud-train_1993
Waa jàngu bi it bokk ci réew mi te seen i biir jàngu ay estatee fa nekk yu ñu di jublu ci seen ag jaamu.
[14] tree
Te looluy lu am lu kenn dul sikk.
s-14
wo_wtb-ud-train_1994
Te looluy lu am lu kenn dul sikk.
[15] tree
Waaw ana lu waral ñu ne nit ci mii am réew am na sañ-sañu génne li ci moom te du ko génn.
s-15
wo_wtb-ud-train_1995
Waaw ana lu waral ñu ne nit ci mii am réew am na sañ-sañu génne li ci moom te du ko génn.
[16] tree
Fii lu neex waay mu teg ci kaw derub yoonu Murit mbaa Lislaam.
s-16
wo_wtb-ud-train_1996
Fii lu neex waay mu teg ci kaw derub yoonu Murit mbaa Lislaam.
[17] tree
Te ñoñ Nasaraan ku leen xaw a laal réew mépp jóg jiital ci seen ñi ñu di tudde ay ñoñ xel (intellectuels).
s-17
wo_wtb-ud-train_1997
Te ñoñ Nasaraan ku leen xaw a laal réew mépp jóg jiital ci seen ñi ñu di tudde ay ñoñ xel (intellectuels).
[18] tree
Lu nekk ñu wax ko.
s-18
wo_wtb-ud-train_1998
Lu nekk ñu wax ko.
[19] tree
Te kat li jar a wax duñu ko wax mukk.
s-19
wo_wtb-ud-train_1999
Te kat li jar a wax duñu ko wax mukk.
[20] tree
Li jar a wax moo di réew mu nga xam ne 98 % ay jullit lañu te feeti Nasaraan yaa fa ëpp.
s-20
wo_wtb-ud-train_2000
Li jar a wax moo di réew mu nga xam ne 98 % ay jullit lañu te feeti Nasaraan yaa fa ëpp.
[21] tree
Bu lu ñu di woowe Pak jotee ñu jox ndongoy daara yi ay fan yu dul jeex ngir ag bër.
s-21
wo_wtb-ud-train_2001
Bu lu ñu di woowe Pak jotee ñu jox ndongoy daara yi ay fan yu dul jeex ngir ag bër.
[22] tree
Waaye jullit ñi ñoom, ku ca tëbëskiji mbaa nga tamxariti mbaa lu ni mel, say doom boo moyuwul ñu dàq leen, ndax amuñu fan yu ñu leen may.
s-22
wo_wtb-ud-train_2002
Waaye jullit ñi ñoom, ku ca tëbëskiji mbaa nga tamxariti mbaa lu ni mel, say doom boo moyuwul ñu dàq leen, ndax amuñu fan yu ñu leen may.
[23] tree
Ab laaj a ngi nii: Li Abdulaay Wàdd waxoon imaam yi ci ag suufeel ak xeebeel lu tax jurul coow?
s-23
wo_wtb-ud-train_2003
Ab laaj a ngi nii: Li Abdulaay Wàdd waxoon imaam yi ci ag suufeel ak xeebeel lu tax jurul coow?
[24] tree
Li mu wax Sërin Tuubaa ak Alhaaji Maalig lu tax jurul coow?
s-24
wo_wtb-ud-train_2004
Li mu wax Sërin Tuubaa ak Alhaaji Maalig lu tax jurul coow?
[25] tree
Ndax kat Sërin Tuuba la taxoon ñu génne ko weesuwul bañ ab estati ak lépp lu Yàlla bañ te loola di woon li Tubaab bi bëggoon.
s-25
wo_wtb-ud-train_2005
Ndax kat Sërin Tuuba la taxoon ñu génne ko weesuwul bañ ab estati ak lépp lu Yàlla bañ te loola di woon li Tubaab bi bëggoon.
[26] tree
Seen i bëgg-bëgg wuute jur Tubaab bi manatu ko fee dékku mu génne ko ngir loolu.
s-26
wo_wtb-ud-train_2006
Seen i bëgg-bëgg wuute jur Tubaab bi manatu ko fee dékku mu génne ko ngir loolu.
[27] tree
Lu tax tooñaange yii yépp jurul coow?
s-27
wo_wtb-ud-train_2007
Lu tax tooñaange yii yépp jurul coow?
[28] tree
Man damaa gis ne li tax waa ji moom wax jii wax du ngir tuutale waaye ngir layal estateem bi la.
s-28
wo_wtb-ud-train_2008
Man damaa gis ne li tax waa ji moom wax jii wax du ngir tuutale waaye ngir layal estateem bi la.
[29] tree
Kon manoon na yam foofa, waaye mu àgg ci naan dafay booleji ca Paab ba, mel ne Paab bi war naa manal Senegaal dara.
s-29
wo_wtb-ud-train_2009
Kon manoon na yam foofa, waaye mu àgg ci naan dafay booleji ca Paab ba, mel ne Paab bi war naa manal Senegaal dara.
[30] tree
Te moom ci jëmmi boppam taxawoon wax wax ju bon ju ñaaw jëme ci sunu sang bu tedd ba, ana lu ñu ci wax ñoom?
s-30
wo_wtb-ud-train_2010
Te moom ci jëmmi boppam taxawoon wax wax ju bon ju ñaaw jëme ci sunu sang bu tedd ba, ana lu ñu ci wax ñoom?
[31] tree
Ndax ñaawlu nañu ko?
s-31
wo_wtb-ud-train_2011
Ndax ñaawlu nañu ko?
[32] tree
Xanaa ñu ne 'liberté d'expression' sañ-sañu wax li ci yaw.
s-32
wo_wtb-ud-train_2012
Xanaa ñu ne 'liberté d'expression' sañ-sañu wax li ci yaw.
[33] tree
Ba ñuy damm soorool ya ca Siwis lu ñu wax?
s-33
wo_wtb-ud-train_2013
Ba ñuy damm soorool ya ca Siwis lu ñu wax?
[34] tree
Ba ñuy aaye muuraay ca Faraas ndax ñaawlu nañu ko?
s-34
wo_wtb-ud-train_2014
Ba ñuy aaye muuraay ca Faraas ndax ñaawlu nañu ko?
[35] tree
Fu ñu ko teg?
s-35
wo_wtb-ud-train_2015
Fu ñu ko teg?
[36] tree
Te moone soorool ya ca Siwis de weesuwul ñeent ci ay 200 jakka.
s-36
wo_wtb-ud-train_2016
Te moone soorool ya ca Siwis de weesuwul ñeent ci ay 200 jakka.
[37] tree
Am na fi ay baat yu nga xam ni seen liggéey ci réew mi du lu moy màbb dooley jullit ñi dëgëral Nasaraan yi.
s-37
wo_wtb-ud-train_2017
Am na fi ay baat yu nga xam ni seen liggéey ci réew mi du lu moy màbb dooley jullit ñi dëgëral Nasaraan yi.
[38] tree
Yooyu ba ca njëkk moo di diineedi, ñu gën koo xam ci 'laïcité'.
s-38
wo_wtb-ud-train_2018
Yooyu ba ca njëkk moo di diineedi, ñu gën koo xam ci 'laïcité'.
[39] tree
Laicite du lu moy tugalal mbaa sowwul (occidentalisser) aw askan wu ko doonul.
s-39
wo_wtb-ud-train_2019
Laicite du lu moy tugalal mbaa sowwul (occidentalisser) aw askan wu ko doonul.
[40] tree
Loolu moo di tàyyi xayug sowwu gu Nasaraan ak Yahood gi (judeo-chretienne) tay ko ci réew mu nga xam ne ay jullit lañu mbaa duñu woon i ñoñ sowwu, ak ga leen ci ñu gën a doon i tubaab tubaab yi.
s-40
wo_wtb-ud-train_2020
Loolu moo di tàyyi xayug sowwu gu Nasaraan ak Yahood gi (judeo-chretienne) tay ko ci réew mu nga xam ne ay jullit lañu mbaa duñu woon i ñoñ sowwu, ak ga leen ci ñu gën a doon i tubaab tubaab yi.
[41] tree
Laïcité (diineedi), bu dee sax lu ñu gawe (imposer), dafa war a sàmm diine yi waaye waru fee nekk di luy gor seen i tànk te naan sama yoon nekkul ci yeen.
s-41
wo_wtb-ud-train_2021
Laïcité (diineedi), bu dee sax lu ñu gawe (imposer), dafa war a sàmm diine yi waaye waru fee nekk di luy gor seen i tànk te naan sama yoon nekkul ci yeen.
[42] tree
Ci misaal bu dee dafa bëgg a taxaw ci réew mu mel ne Senegaal ci ag sañ-bañ, dafa war a taxaw taxawaayu Sariiya.
s-42
wo_wtb-ud-train_2022
Ci misaal bu dee dafa bëgg a taxaw ci réew mu mel ne Senegaal ci ag sañ-bañ, dafa war a taxaw taxawaayu Sariiya.
[43] tree
Du lu ñu fiy doxal mbaa àtteb jeneen diine, waaye lépp lu ñuy def warees na koo xool ba xam gaañul jenn ci diine yooyu.
s-43
wo_wtb-ud-train_2023
Du lu ñu fiy doxal mbaa àtteb jeneen diine, waaye lépp lu ñuy def warees na koo xool ba xam gaañul jenn ci diine yooyu.
[44] tree
Lu ko moy mu doonati moom ci jëmmi boppam jaasi ju ñu bocci ci kanamu diine yi.
s-44
wo_wtb-ud-train_2024
Lu ko moy mu doonati moom ci jëmmi boppam jaasi ju ñu bocci ci kanamu diine yi.
[45] tree
Lu am solo ñu war koo wax mooy ne su ñu bëggee ag jeqiku bañ a ami ëllëg ci réew mi na fi ag maandute dolliku.
s-45
wo_wtb-ud-train_2025
Lu am solo ñu war koo wax mooy ne su ñu bëggee ag jeqiku bañ a ami ëllëg ci réew mi na fi ag maandute dolliku.
[46] tree
Maandute nag mooy séddale ci ag maandute déet gënale, déet def la la neex.
s-46
wo_wtb-ud-train_2026
Maandute nag mooy séddale ci ag maandute déet gënale, déet def la la neex.

Edit as listText viewDependency trees