Sentence view
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | test |
---|
Text: -
Lebu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal.
s-1
wo_wtb-ud-train_148
Lebu, mooy benn waaso nekk ci reewum Senegaal.
Ñoom, Ndakaaru moo di seen dëkk, nu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint-Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur, ci wetu geej ak tefes.
s-2
wo_wtb-ud-train_149
Ñoom, Ndakaaru moo di seen dëkk, nu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint-Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur, ci wetu geej ak tefes.
Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan.
s-3
wo_wtb-ud-train_150
Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan.
Seen làkk di wolof.
s-4
wo_wtb-ud-train_151
Seen làkk di wolof.
Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi ñeneen ñi di làkk.
s-5
wo_wtb-ud-train_152
Seen wolof dafa xaw a wuute tuuti ak wolof bi ñeneen ñi di làkk.
Am na ñu ne, lebu yi ñoo sos làkk wolof.
s-6
wo_wtb-ud-train_153
Am na ñu ne, lebu yi ñoo sos làkk wolof.
Cosaanu baat boobu, wuute na ci li kilifa yi tekki.
s-7
wo_wtb-ud-train_154
Cosaanu baat boobu, wuute na ci li kilifa yi tekki.
Ñooñu dinañu di nettali ay cosaan yu wuute: 'leeb' moo juur baat bi.
s-8
wo_wtb-ud-train_155
Ñooñu dinañu di nettali ay cosaan yu wuute: 'leeb' moo juur baat bi.
Am na ñeneen ñu ni 'luubu' mooy 'bañ', ndax ci cosaan, Lebu yi dañu mas a bañ ku leen noot.
s-9
wo_wtb-ud-train_156
Am na ñeneen ñu ni 'luubu' mooy 'bañ', ndax ci cosaan, Lebu yi dañu mas a bañ ku leen noot.
Seex Anta Jóob, ci gëstoom, dafa wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi.
s-10
wo_wtb-ud-train_157
Seex Anta Jóob, ci gëstoom, dafa wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi.
Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga, benn diwaan la woon bu nit ñi daan dem di fa rëbbi, ak nappi.
s-11
wo_wtb-ud-train_158
Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga, benn diwaan la woon bu nit ñi daan dem di fa rëbbi, ak nappi.
Dëkk boobu dafa jannoo ak géej gi.
s-12
wo_wtb-ud-train_159
Dëkk boobu dafa jannoo ak géej gi.
Moo tax ñu yoroon Isipt gu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu.
s-13
wo_wtb-ud-train_160
Moo tax ñu yoroon Isipt gu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu.
Ñu war a xam ni, Seex Anta Jóob ak yeneen gestukat wone nañu ko.
s-14
wo_wtb-ud-train_161
Ñu war a xam ni, Seex Anta Jóob ak yeneen gestukat wone nañu ko.
Làkk boobu amoon ca Isipt boobu, ak làkk wolof, ñoo bokk maam.
s-15
wo_wtb-ud-train_162
Làkk boobu amoon ca Isipt boobu, ak làkk wolof, ñoo bokk maam.
Rëbu moo juur Lebu.
s-16
wo_wtb-ud-train_163
Rëbu moo juur Lebu.
Lebu moo juur Libi.
s-17
wo_wtb-ud-train_164
Lebu moo juur Libi.
Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudde ñu dëkk ca biir réew mi 'kaw'.
s-18
wo_wtb-ud-train_165
Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudde ñu dëkk ca biir réew mi 'kaw'.
Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir réew mi.
s-19
wo_wtb-ud-train_166
Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir réew mi.
Lebu yi, kon, réew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono yu Isipt gu yàgg ga ame.
s-20
wo_wtb-ud-train_167
Lebu yi, kon, réew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono yu Isipt gu yàgg ga ame.
Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñëwoon foofu, jóge Asi, te ñu leen daan bëgg a noot.
s-21
wo_wtb-ud-train_168
Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñëwoon foofu, jóge Asi, te ñu leen daan bëgg a noot.
Ñoom ñooy Persi yi.
s-22
wo_wtb-ud-train_169
Ñoom ñooy Persi yi.
Ci seen gàdday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali).
s-23
wo_wtb-ud-train_170
Ci seen gàdday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali).
Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawoo.
s-24
wo_wtb-ud-train_171
Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawoo.
Ñu ko gën a ràññe ci turu Nubi walla Kuus.
s-25
wo_wtb-ud-train_172
Ñu ko gën a ràññe ci turu Nubi walla Kuus.
Senegaal, lañu agsi, jamono ja nguuru Tekuruur ame.
s-26
wo_wtb-ud-train_173
Senegaal, lañu agsi, jamono ja nguuru Tekuruur ame.
Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi, rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp.
s-27
wo_wtb-ud-train_174
Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi, rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp.
Ñu leen tudde ci làkku pulaar ay Cuballo / Subalbe.
s-28
wo_wtb-ud-train_175
Ñu leen tudde ci làkku pulaar ay Cuballo / Subalbe.
Foofu lañu sanc ay dëkk yu mel ni KasKas ak Njum.
s-29
wo_wtb-ud-train_176
Foofu lañu sanc ay dëkk yu mel ni KasKas ak Njum.
Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk.
s-30
wo_wtb-ud-train_177
Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk.
Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, soog a mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530.
s-31
wo_wtb-ud-train_178
Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, soog a mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530.
Foofu, ay Socé lañu fa fekk.
s-32
wo_wtb-ud-train_179
Foofu, ay Socé lañu fa fekk.
Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi.
s-33
wo_wtb-ud-train_180
Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi.
Ñu ne tamit, fukki ak ñaari PENC yi.
s-34
wo_wtb-ud-train_181
Ñu ne tamit, fukki ak ñaari PENC yi.
Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi.
s-35
wo_wtb-ud-train_182
Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi.
Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun, ...
s-36
wo_wtb-ud-train_183
Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun, ...
Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek.
s-37
wo_wtb-ud-train_184
Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek.
Ñu sant 'Mbeŋ', ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon.
s-38
wo_wtb-ud-train_185
Ñu sant 'Mbeŋ', ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon.
Seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), jóge Mali.
s-39
wo_wtb-ud-train_186
Seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), jóge Mali.
Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom lañu cosaanoo.
s-40
wo_wtb-ud-train_187
Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom lañu cosaanoo.
Mel ni wolof yi rekk.
s-41
wo_wtb-ud-train_188
Mel ni wolof yi rekk.
Lebu yi, ay jullit lañu.
s-42
wo_wtb-ud-train_189
Lebu yi, ay jullit lañu.
Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay).
s-43
wo_wtb-ud-train_190
Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay).
Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff.
s-44
wo_wtb-ud-train_191
Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff.
Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekkee Ceddo, manaam tuur yi.
s-45
wo_wtb-ud-train_192
Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekkee Ceddo, manaam tuur yi.
Tuur yi, am na solo ci Lebu yi.
s-46
wo_wtb-ud-train_193
Tuur yi, am na solo ci Lebu yi.
Ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëm ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan.
s-47
wo_wtb-ud-train_194
Ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëm ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan.
Ci seen tuur yi, 'ndëpp' la nit ñi gën a xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine a leen jàpp.
s-48
wo_wtb-ud-train_195
Ci seen tuur yi, 'ndëpp' la nit ñi gën a xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine a leen jàpp.
Jiine ci Lebu, 'rab' lañu ko tudde.
s-49
wo_wtb-ud-train_196
Jiine ci Lebu, 'rab' lañu ko tudde.
Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneen i tuur, bokk nañu ci ñooñu Lebu yi seqante.
s-50
wo_wtb-ud-train_197
Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneen i tuur, bokk nañu ci ñooñu Lebu yi seqante.
Edit as list • Text view • Dependency trees