Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part dev
Text: Transcription Written form - Colors
showing 1 - 100 of 166 • next
Poroxaan 2011 : Soxna Jaara Mariyama Buso royukaayu jigéenu jullit
s-1
wo_wtb-ud-train_1491
Poroxaan 2011: Soxna Jaara Mariyama Buso royukaayu jigéenu jullit
Soxna Mariyaama Buso ñu koy dàkkantale , ci jikko , Jaaratu-l-Laah ( dëkkandoob Yàlla bi ) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta , génn àdduna ci atum 1866 ca Poroxaan .
s-2
wo_wtb-ud-train_1492
Soxna Mariyaama Buso ñu koy dàkkantale, ci jikko, Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, génn àdduna ci atum 1866 ca Poroxaan.
Soxna Jaara Buso mom Sëriñ Hamaat Buso ( baayam ) ak Soxna Asta Waalo Mbàkke ( yaayam ) , cosaano ci askanu Sëriif goo xam ne calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla ( jàmmi Yàlla ci ñoom ) .
s-3
wo_wtb-ud-train_1493
Soxna Jaara Buso mom Sëriñ Hamaat Buso (baayam) ak Soxna Asta Waalo Mbàkke (yaayam), cosaano ci askanu Sëriif goo xam ne calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom).
Mu dondoo ci loolu ag cell ak ab yar ba war ci doomi soxna jële ko ci waajuram wu jigéen .
s-4
wo_wtb-ud-train_1494
Mu dondoo ci loolu ag cell ak ab yar ba war ci doomi soxna jële ko ci waajuram wu jigéen.
Soxna Asta Waalo Mbàkke doon ab jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf , mu juddu ci loolu .
s-5
wo_wtb-ud-train_1495
Soxna Asta Waalo Mbàkke doon ab jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf, mu juddu ci loolu.
Yaayam ju farlu jooju yar ko ci .
s-6
wo_wtb-ud-train_1496
Yaayam ju farlu jooju yar ko ci.
Am njàngam ak ab yaram :
s-7
wo_wtb-ud-train_1497
Am njàngam ak ab yaram:
Soxna Jaaratu-l-Laahi Buso jànge na Alxuraan ci aji / way-juram wu jigéen wu séll wa te sàmmu , te doon senn soxna su ame taxawaay bu mat sëkk ci Lislaam ci jàngale ak yare , niki Sëriñ si , ba mokkal ko ci anam gu sell te sax ci jamono yi muy am fukki at ak ñeent ( 14 at ) .
s-8
wo_wtb-ud-train_1498
Soxna Jaaratu-l-Laahi Buso jànge na Alxuraan ci aji / way-juram wu jigéen wu séll wa te sàmmu, te doon senn soxna su ame taxawaay bu mat sëkk ci Lislaam ci jàngale ak yare, niki Sëriñ si, ba mokkal ko ci anam gu sell te sax ci jamono yi muy am fukki at ak ñeent (14 at).
Mu jàngal ko it xam-xamu diineem niki jennal Yàlla ( Tawhiid ) , àttey Lislaam ak aw yoonam ( Fiq ) , séllal ak jaamu ngir Yàlla doŋŋ ( Tassawuuf ) , ba mu wattu leen na mu ware .
s-9
wo_wtb-ud-train_1499
Mu jàngal ko it xam-xamu diineem niki jennal Yàlla (Tawhiid), àttey Lislaam ak aw yoonam (Fiq), séllal ak jaamu ngir Yàlla doŋŋ (Tassawuuf), ba mu wattu leen na mu ware.
Mu yar ko it ci Lislaam , ci jàng Alxuraan , ak jëfe ab xam-xamam .
s-10
wo_wtb-ud-train_1500
Mu yar ko it ci Lislaam, ci jàng Alxuraan, ak jëfe ab xam-xamam.
Mu yar ko it ci ngor , muñ , nangu , ak jépp jikko ju ñu taamu ci as gor rawatina bu di ab jullit .
s-11
wo_wtb-ud-train_1501
Mu yar ko it ci ngor, muñ, nangu, ak jépp jikko ju ñu taamu ci as gor rawatina bu di ab jullit.
Ba mu mujj di ku xarañe bépp xam-xamu Lislaam , te it di kuy jëfe ngirum Tassawuuf ci anam gu xóot .
s-12
wo_wtb-ud-train_1502
Ba mu mujj di ku xarañe bépp xam-xamu Lislaam, te it di kuy jëfe ngirum Tassawuuf ci anam gu xóot.
Ak li dund gi di gàtt lépp ( 33 i at ) de moona téewul ci ag farloom bind na Alxuraan ñeen-fukki yoon ci yoxoy boppam ( 40 i kaamil ) ba mujjoon di ab jàngalekatu Alxuraan ci taaral mbind .
s-13
wo_wtb-ud-train_1503
Ak li dund gi di gàtt lépp (33 i at) de moona téewul ci ag farloom bind na Alxuraan ñeen-fukki yoon ci yoxoy boppam (40 i kaamil) ba mujjoon di ab jàngalekatu Alxuraan ci taaral mbind.
As lëf ci ay jikkoom ak i meloom :
s-14
wo_wtb-ud-train_1504
As lëf ci ay jikkoom ak i meloom:
Soxna Jaaratu-l-Laah Dëkkandoob Yàlla bi ci ag céll ak ag sàmmu , di ab jullit bu di doomi jullit .
s-15
wo_wtb-ud-train_1505
Soxna Jaaratu-l-Laah Dëkkandoob Yàlla bi ci ag céll ak ag sàmmu, di ab jullit bu di doomi jullit.
Mu nangu te seere ni : Amul jenn Yàlla ju dul Allaa .
s-16
wo_wtb-ud-train_1506
Mu nangu te seere ni: Amul jenn Yàlla ju dul Allaa.
Yàlla aji sàkk ji yélloowul wayjur , mbaa doom , ëppante naak di bokkaale ak kenn .
s-17
wo_wtb-ud-train_1507
Yàlla aji sàkk ji yélloowul wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn.
Moo di dégg , moo di gis .
s-18
wo_wtb-ud-train_1508
Moo di dégg, moo di gis.
Muhammad ( jàmmi Yàlla ak xéewalam ci kawam ) ndawul Yàlla la .
s-19
wo_wtb-ud-train_1509
Muhammad (jàmmi Yàlla ak xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la.
Ndaw lu mu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne .
s-20
wo_wtb-ud-train_1510
Ndaw lu mu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne.
Mu nangu te jàpp ni Lislaam rekk mooy diine .
s-21
wo_wtb-ud-train_1511
Mu nangu te jàpp ni Lislaam rekk mooy diine.
Gëm téerey asamaan yépp te nangu ni Alxuraan a leen wuutu .
s-22
wo_wtb-ud-train_1512
Gëm téerey asamaan yépp te nangu ni Alxuraan a leen wuutu.
Gëm dogal te di ko rafetlu .
s-23
wo_wtb-ud-train_1513
Gëm dogal te di ko rafetlu.
Gëm malaaka yi ak lépp li aju ci ngëm ...
s-24
wo_wtb-ud-train_1514
Gëm malaaka yi ak lépp li aju ci ngëm...
Mu nangoo julli , nangu woon a joxe azaka , nangu woon a woor , nangu woon ni aj war na ko aw yoon .
s-25
wo_wtb-ud-train_1515
Mu nangoo julli, nangu woon a joxe azaka, nangu woon a woor, nangu woon ni aj war na ko aw yoon.
Soxna Jaaratu-l-Laah doonoon as gor su di doomi gor , di ku sàmmu , ragal Yàlla , gëm Yàlla di ko jaamu .
s-26
wo_wtb-ud-train_1516
Soxna Jaaratu-l-Laah doonoon as gor su di doomi gor, di ku sàmmu, ragal Yàlla, gëm Yàlla di ko jaamu.
Mu doon ku sopp Yonent bi , bëgg ab sëriñam di wëye ay ndigëlam .
s-27
wo_wtb-ud-train_1517
Mu doon ku sopp Yonent bi, bëgg ab sëriñam di wëye ay ndigëlam.
Mu doon ku fonk ay bokkam te nawloo leen , di ab jullit bu koy jëfe .
s-28
wo_wtb-ud-train_1518
Mu doon ku fonk ay bokkam te nawloo leen, di ab jullit bu koy jëfe.
Mu di as gor su gore , di doomi Soxna su soxnaa .
s-29
wo_wtb-ud-train_1519
Mu di as gor su gore, di doomi Soxna su soxnaa.
Mu di ab jàngkat buy jàngale , di boroom xam-xam bu ko daan jëfe .
s-30
wo_wtb-ud-train_1520
Mu di ab jàngkat buy jàngale, di boroom xam-xam bu ko daan jëfe.
Mu di boroom Alxuraan ci bind ak ci wattu , doon ku nangu te man a muñ .
s-31
wo_wtb-ud-train_1521
Mu di boroom Alxuraan ci bind ak ci wattu, doon ku nangu te man a muñ.
Mu doon ku yaru te daan yare , doon ku ñime njaboot te daan leen taxawu .
s-32
wo_wtb-ud-train_1522
Mu doon ku yaru te daan yare, doon ku ñime njaboot te daan leen taxawu.
Mu doon it jigéen ju maandu ci gépp anam , ku daan dunde Lislaam .
s-33
wo_wtb-ud-train_1523
Mu doon it jigéen ju maandu ci gépp anam, ku daan dunde Lislaam.
Ci lu dul weeru koor , baaxoo woon na di woor , koor yi ñu taamu ci at mi , ak i koor yu mu tegoo woon .
s-34
wo_wtb-ud-train_1524
Ci lu dul weeru koor, baaxoo woon na di woor, koor yi ñu taamu ci at mi, ak i koor yu mu tegoo woon.
Tegoo woon na it di jàng téereb Dalaa-ilul-Xayrâti bu Imaam Jazuuli , di ab téere bu ñu taamu te fees dell ak i julli ci Yonent bi ( jàmmi Yàlla ci moom ) .
s-35
wo_wtb-ud-train_1525
Tegoo woon na it di jàng téereb Dalaa-ilul-Xayrâti bu Imaam Jazuuli, di ab téere bu ñu taamu te fees dell ak i julli ci Yonent bi (jàmmi Yàlla ci moom).
Li am daal , ay waxtoom ci jàng Alxuraan ak tari ko la dëkke woon mbaa julli ci Yonent bi , ngir ndigalul Yàlla la .
s-36
wo_wtb-ud-train_1526
Li am daal, ay waxtoom ci jàng Alxuraan ak tari ko la dëkke woon mbaa julli ci Yonent bi, ngir ndigalul Yàlla la.
Moom daal ci gàttal mooy way-jur wu jigéen wu Seex Ahmadu Bàmba , Xaadimul Xadiim .
s-37
wo_wtb-ud-train_1527
Moom daal ci gàttal mooy way-jur wu jigéen wu Seex Ahmadu Bàmba, Xaadimul Xadiim.
Te Aji-bind ji ( Yalla ) nee na : Suuf su teey / nangu dina génne kéeman ci ndigalul boroomam .
s-38
wo_wtb-ud-train_1528
Te Aji-bind ji (Yalla) nee na: Suuf su teey / nangu dina génne kéeman ci ndigalul boroomam.
Muy li Wolof naan : Kéwël du tëb doom jay bëtt .
s-39
wo_wtb-ud-train_1529
Muy li Wolof naan: Kéwël du tëb doom jay bëtt.
Kon daal loolu rekk doy na ay jikko ak aw tagg , ndax bàyyi doom ju mel ni Seex Ahmadu Bàmba ci ag céll ak ag sàmmu , wéetal Yàlla , te jox ko léppam , xam , xàmme di xamale , nangul Lislaam , yaru lool di yare , jigéen ju ko ame làmboo mbooleem jikko yi ñu taamu ...
s-40
wo_wtb-ud-train_1530
Kon daal loolu rekk doy na ay jikko ak aw tagg, ndax bàyyi doom ju mel ni Seex Ahmadu Bàmba ci ag céll ak ag sàmmu, wéetal Yàlla, te jox ko léppam, xam, xàmme di xamale, nangul Lislaam, yaru lool di yare, jigéen ju ko ame làmboo mbooleem jikko yi ñu taamu...
Soxna Jaara Buso ci pénc mi :
s-41
wo_wtb-ud-train_1531
Soxna Jaara Buso ci pénc mi:
Niki jigéen ñépp , baaxoo woon nañu jigéen ju mat a dem kër , ñu fàggul ko boroom kër , ak it teewal ko ngir man koo dénk waxi njariñ , ak yee ko ci àddina xamal ko ni it , fa nga jëm sa ab sang nga fay fekk , bu la Yàlla booleel , xamal ko it ni , ngërëmul Yàlla ak ag payam , ak doom ju raw i maasam , ñeel na soxna si ànd ak boroom kërëm ci li neex Yàlla , nangoo muñ , nangu , te di wéy ci ay ndigël .
s-42
wo_wtb-ud-train_1532
Niki jigéen ñépp, baaxoo woon nañu jigéen ju mat a dem kër, ñu fàggul ko boroom kër, ak it teewal ko ngir man koo dénk waxi njariñ, ak yee ko ci àddina xamal ko ni it, fa nga jëm sa ab sang nga fay fekk, bu la Yàlla booleel, xamal ko it ni, ngërëmul Yàlla ak ag payam, ak doom ju raw i maasam, ñeel na soxna si ànd ak boroom kërëm ci li neex Yàlla, nangoo muñ, nangu, te di wéy ci ay ndigël.
Niki noonu lañu ko defale Soxna Jaara ci bi mu ci tollee , fàggul ko te tànnal ko ab sëriñ ci anam ga mu gëne , ak ci melo yi sax ci diine .
s-43
wo_wtb-ud-train_1533
Niki noonu lañu ko defale Soxna Jaara ci bi mu ci tollee, fàggul ko te tànnal ko ab sëriñ ci anam ga mu gëne, ak ci melo yi sax ci diine.
Mu déglu it wax yu am solo yooyu ak soññee yooyu , ci ag teewlu , dégg ak topp .
s-44
wo_wtb-ud-train_1534
Mu déglu it wax yu am solo yooyu ak soññee yooyu, ci ag teewlu, dégg ak topp.
Waaye ci yaru gi mu yaru ci xamlu Yàlla ak di jéem a xàmme , ak xalaat yu sori yi sufiyànke yi baaxoo .
s-45
wo_wtb-ud-train_1535
Waaye ci yaru gi mu yaru ci xamlu Yàlla ak di jéem a xàmme, ak xalaat yu sori yi sufiyànke yi baaxoo.
Nee nañu ci loolu , bu ñu koy jaarale ci yii , mu ubbi kaamilu Alxuraan bi mu baaxo yor , ngir def ab natt , yam ci waxi Yàlla ji naan : Mohammad nekkul di baayub kenn ci yeen waaye kay ndawul Yàlla la te di Yonent bi mujj .
s-46
wo_wtb-ud-train_1536
Nee nañu ci loolu, bu ñu koy jaarale ci yii, mu ubbi kaamilu Alxuraan bi mu baaxo yor, ngir def ab natt, yam ci waxi Yàlla ji naan: Mohammad nekkul di baayub kenn ci yeen waaye kay ndawul Yàlla la te di Yonent bi mujj.
Lii déy màndarga la mu yaatu te bari maanaa te doy kiimaan ci way-xalaat yi .
s-47
wo_wtb-ud-train_1537
Lii déy màndarga la mu yaatu te bari maanaa te doy kiimaan ci way-xalaat yi.
Ci loolu mu dogu te jaayante ci topp ab sëriñam ci jëmmam ak ag ruuham ( ndundam ) kemm kàttanam ngir Yàlla doŋŋ , te di ku sàmm ay wareefam , am kersa ak ag topp gu matale ñeel boroom kërëm .
s-48
wo_wtb-ud-train_1538
Ci loolu mu dogu te jaayante ci topp ab sëriñam ci jëmmam ak ag ruuham (ndundam) kemm kàttanam ngir Yàlla doŋŋ, te di ku sàmm ay wareefam, am kersa ak ag topp gu matale ñeel boroom kërëm.
Nu indi fi ag pàttali .
s-49
wo_wtb-ud-train_1539
Nu indi fi ag pàttali.
Sëriñ Muhammadu Buso bokk ak Soxna si yenn way-jur .
s-50
wo_wtb-ud-train_1540
Sëriñ Muhammadu Buso bokk ak Soxna si yenn way-jur.
Bi mu tollee ci wut kër dafa dogu ni : Bu ma wóorul ni doom ju ma am wàlliyu lay doon duma samp kër cey !
s-51
wo_wtb-ud-train_1541
Bi mu tollee ci wut kër dafa dogu ni: Bu ma wóorul ni doom ju ma am wàlliyu lay doon duma samp kër cey!
Pas-pas bu ni mel déy , la soxna si ame bi muy dem kër .
s-52
wo_wtb-ud-train_1542
Pas-pas bu ni mel déy, la soxna si ame bi muy dem kër.
Soxna Jaara Buso doonoon soxna su Maam Moor ( Anta Sali ) Mbàkke .
s-53
wo_wtb-ud-train_1543
Soxna Jaara Buso doonoon soxna su Maam Moor (Anta Sali) Mbàkke.
Soxna Jaara nag bokkoon ci askan wu di boroom barke .
s-54
wo_wtb-ud-train_1544
Soxna Jaara nag bokkoon ci askan wu di boroom barke.
Yàlla dénk leen am-am , te Yàlla def Maam Moor Anta Sëli mi mujj di boroom këram bokkoon ci askan wu seen wërsëg melul noona ...
s-55
wo_wtb-ud-train_1545
Yàlla dénk leen am-am, te Yàlla def Maam Moor Anta Sëli mi mujj di boroom këram bokkoon ci askan wu seen wërsëg melul noona...
Am na waxi Sëriñ Tuuba juy wéral loolii :
s-56
wo_wtb-ud-train_1546
Am na waxi Sëriñ Tuuba juy wéral loolii:
Am na bis am góor gu ñëw ci Sëriñ bi , mel ni ku yàkkamti lool .
s-57
wo_wtb-ud-train_1547
Am na bis am góor gu ñëw ci Sëriñ bi, mel ni ku yàkkamti lool.
Sëriñ bi ne ko : Diw , fàttewuma sama nag wa .
s-58
wo_wtb-ud-train_1548
Sëriñ bi ne ko: Diw, fàttewuma sama nag wa.
Daldi ni : Jëmm jii de ba may gën di gone bind naa ab Kaamil , di ko jox saa baay Sëriñ Moor Anta Sali .
s-59
wo_wtb-ud-train_1549
Daldi ni: Jëmm jii de ba may gën di gone bind naa ab Kaamil, di ko jox saa baay Sëriñ Moor Anta Sali.
Mu ni ma : Xanaa nga yobbu ko Saalum ngir man ci a am dara , - lu man a jëm ci kër gi .
s-60
wo_wtb-ud-train_1550
Mu ni ma: Xanaa nga yobbu ko Saalum ngir man ci a am dara, - lu man a jëm ci kër gi.
Sëriñ bi nee na : Ma dem Saalum di ko weceeku , di wër ba am ku ma ko diktal .
s-61
wo_wtb-ud-train_1551
Sëriñ bi nee na: Ma dem Saalum di ko weceeku, di wër ba am ku ma ko diktal.
Mu ni ma : aah , ndongo li , man déy soxla naa ko lool ndax bindiin wu taaru wi , waaye xaalis de yoruma ko , te xam naa li ma yor ab dongo du ko war a soxla .
s-62
wo_wtb-ud-train_1552
Mu ni ma: aah, ndongo li, man déy soxla naa ko lool ndax bindiin wu taaru wi, waaye xaalis de yoruma ko, te xam naa li ma yor ab dongo du ko war a soxla.
Mu ni ko : Aw nag de laa fi yor .
s-63
wo_wtb-ud-train_1553
Mu ni ko: Aw nag de laa fi yor.
Sëriñ bi ne ko : aah , aw nag moom lu ko yobbu dina jafe .
s-64
wo_wtb-ud-train_1554
Sëriñ bi ne ko: aah, aw nag moom lu ko yobbu dina jafe.
Nee na : nag woowee góor gii moo ko ni man naa la ko jiitalal .
s-65
wo_wtb-ud-train_1555
Nee na: nag woowee góor gii moo ko ni man naa la ko jiitalal.
Sëriñ bi nee na ma warlul ko Àjjana ak guddu-fan .
s-66
wo_wtb-ud-train_1556
Sëriñ bi nee na ma warlul ko Àjjana ak guddu-fan.
Mu ni góor gi : ' gis nga sama ndëel ya ?
s-67
wo_wtb-ud-train_1557
Mu ni góor gi: 'gis nga sama ndëel ya?
Mu ni ko : ' aah , gis naa benn bi de muy gudd fan gi , bi ci des kay a ma wóorul ' .
s-68
wo_wtb-ud-train_1558
Mu ni ko: 'aah, gis naa benn bi de muy gudd fan gi, bi ci des kay a ma wóorul'.
Sëriñ bi ne ko : ' Waaw !
s-69
wo_wtb-ud-train_1559
Sëriñ bi ne ko: 'Waaw!
Bi ci des it noonu rekk , bul ko sikk !
s-70
wo_wtb-ud-train_1560
Bi ci des it noonu rekk, bul ko sikk!
Ci wax jii manees na cee xame ni Yàlla dénku leen woon alal ju ñu man a gis .
s-71
wo_wtb-ud-train_1561
Ci wax jii manees na cee xame ni Yàlla dénku leen woon alal ju ñu man a gis.
Waaye xanaa ñuy ay jaamukati Yàlla , di ay boroomi xam-xam yuy jëfe seen i xam-xam , di ay jullit te doon i gor , sàmmu te ragal Yàlla .
s-72
wo_wtb-ud-train_1562
Waaye xanaa ñuy ay jaamukati Yàlla, di ay boroomi xam-xam yuy jëfe seen i xam-xam, di ay jullit te doon i gor, sàmmu te ragal Yàlla.
Ci yii jikko daal la kilifay Soxna Jaara Buso xool , ba nangu faa maye seen doom .
s-73
wo_wtb-ud-train_1563
Ci yii jikko daal la kilifay Soxna Jaara Buso xool, ba nangu faa maye seen doom.
Soxna Jaara it ci yooyii jikko la xool ba nangul ko .
s-74
wo_wtb-ud-train_1564
Soxna Jaara it ci yooyii jikko la xool ba nangul ko.
Loolu it masul di feeñ ci seen ab ànd , xanaa ànd ak moom ci dooleem ñuy dund ci sutura ak ngir Yàlla .
s-75
wo_wtb-ud-train_1565
Loolu it masul di feeñ ci seen ab ànd, xanaa ànd ak moom ci dooleem ñuy dund ci sutura ak ngir Yàlla.
Mu jàppe ko ni ab sangam di topp ay ndigëlam ci anam gu yéeme .
s-76
wo_wtb-ud-train_1566
Mu jàppe ko ni ab sangam di topp ay ndigëlam ci anam gu yéeme.
Misaalum nittali bu siiw bii te doy kiimtaan , ñu ni : Am na bis Maam Moor Anta Sali di takk aw sàkket teyeloo ko sàkket wa , dugg ci biir neeg bi , ( xëy na ngir jël lu mu takke sàkket wi ) faf Yàlla dogal mu dugg rekk , Yàlla sóob ab taw , mu far toog ca néeg ba .
s-77
wo_wtb-ud-train_1567
Misaalum nittali bu siiw bii te doy kiimtaan, ñu ni: Am na bis Maam Moor Anta Sali di takk aw sàkket teyeloo ko sàkket wa, dugg ci biir neeg bi, (xëy na ngir jël lu mu takke sàkket wi) faf Yàlla dogal mu dugg rekk, Yàlla sóob ab taw, mu far toog ca néeg ba.
Nee nañu : ba ci fajar gi Mame Moor génn fekk Soxna si mu téye sàkket wa .
s-78
wo_wtb-ud-train_1568
Nee nañu: ba ci fajar gi Mame Moor génn fekk Soxna si mu téye sàkket wa.
Mu ni ko : Aaah , yaw de xanaa fii la la taw bi fekk .
s-79
wo_wtb-ud-train_1569
Mu ni ko: Aaah, yaw de xanaa fii la la taw bi fekk.
Mu ni ko : Waaw !
s-80
wo_wtb-ud-train_1570
Mu ni ko: Waaw!
Lu tee bi muy taw nga dugg ci biir , man de jàppoon naa ni yaa ngi ci biir .
s-81
wo_wtb-ud-train_1571
Lu tee bi muy taw nga dugg ci biir, man de jàppoon naa ni yaa ngi ci biir.
Soxna si ni ko : Sa ndigël a ma ko teyeloo woon te ba léegi ndigël jógewaatul ci yaw bàyyiloo ma ko ...
s-82
wo_wtb-ud-train_1572
Soxna si ni ko: Sa ndigël a ma ko teyeloo woon te ba léegi ndigël jógewaatul ci yaw bàyyiloo ma ko...
Lii déy yéem na ma , te war a man a yéem waa jamono jii , ci lii nu mu man a ame .
s-83
wo_wtb-ud-train_1573
Lii déy yéem na ma, te war a man a yéem waa jamono jii, ci lii nu mu man a ame.
Soxna si it liggéeyub kërëm moom rekk a ko daan defal boppam , di ko def ca anam ga mu ware , boole ko ak matal jaamuy yàllaam .
s-84
wo_wtb-ud-train_1574
Soxna si it liggéeyub kërëm moom rekk a ko daan defal boppam, di ko def ca anam ga mu ware, boole ko ak matal jaamuy yàllaam.
Muy jaamu Yàlla ci topp boroom kërëm ak dabu ag càkkutéefam .
s-85
wo_wtb-ud-train_1575
Muy jaamu Yàlla ci topp boroom kërëm ak dabu ag càkkutéefam.
Gannaaw Maam Moor ab sëriñam dafa xawoon a jëm mag , te fi ñu nekkoon xaw a àlle , ba tax sedd ba xaw faa tar , daan na ko fàggul matt mu muy jaaroo , ngir mucc ci sedd boobu nga xam ni baaxul ci mag .
s-86
wo_wtb-ud-train_1576
Gannaaw Maam Moor ab sëriñam dafa xawoon a jëm mag, te fi ñu nekkoon xaw a àlle, ba tax sedd ba xaw faa tar, daan na ko fàggul matt mu muy jaaroo, ngir mucc ci sedd boobu nga xam ni baaxul ci mag.
Ba bis ( xay-na matt jafe na ko ) , ngir bëgg a matale càkkutéefi boroom kërëm , tax mu dàjji gaal gi mu daan denc i mbiram ngir taalale ko ab sëriñam .
s-87
wo_wtb-ud-train_1577
Ba bis (xay-na matt jafe na ko), ngir bëgg a matale càkkutéefi boroom kërëm, tax mu dàjji gaal gi mu daan denc i mbiram ngir taalale ko ab sëriñam.
Noonu it la ko waykat ba waxe Seex Sàmba Jaara Mbay taalubeb Sëriñ Tuubaa .
s-88
wo_wtb-ud-train_1578
Noonu it la ko waykat ba waxe Seex Sàmba Jaara Mbay taalubeb Sëriñ Tuubaa.
Soxna Jaara nee nañu : Masul a jóg ci di dimbalante ñeel waa pénc mi , ci di taxawu ak di dundal jirim yi ak néew-gi-doole yi ci lu dul di sàkku ag cant ci nangukat yi , xanaa ngir jëmmi Yàlla rekk .
s-89
wo_wtb-ud-train_1579
Soxna Jaara nee nañu: Masul a jóg ci di dimbalante ñeel waa pénc mi, ci di taxawu ak di dundal jirim yi ak néew-gi-doole yi ci lu dul di sàkku ag cant ci nangukat yi, xanaa ngir jëmmi Yàlla rekk.
Waxees na ni ci loolu la jële turam wii di Jaaratu-l-Laahi ( dëkkandoob Yàlla bi ) .
s-90
wo_wtb-ud-train_1580
Waxees na ni ci loolu la jële turam wii di Jaaratu-l-Laahi (dëkkandoob Yàlla bi).
Soxna si ak njabootug boppam :
s-91
wo_wtb-ud-train_1581
Soxna si ak njabootug boppam:
Ci loolu Soxna si Yàlla may na ko ci sëy bu barkeel boobu , ñeenti doom , yoo xam ni dinanu sawar lool ci tudd seen i tur , ak wax as tuut ci seen i jikko yu kawe .
s-92
wo_wtb-ud-train_1582
Ci loolu Soxna si Yàlla may na ko ci sëy bu barkeel boobu, ñeenti doom, yoo xam ni dinanu sawar lool ci tudd seen i tur, ak wax as tuut ci seen i jikko yu kawe.
Nu lime leen nii :
s-93
wo_wtb-ud-train_1583
Nu lime leen nii:
Ab taawam mooy Maam Moor ( Jaara ) Mbàkke ( Boroom Saam walla Magi Mag ) mom Sëriñ Moor Anta Sëli Mbàkke ak Soxna Jaara Buso .
s-94
wo_wtb-ud-train_1584
Ab taawam mooy Maam Moor (Jaara) Mbàkke (Boroom Saam walla Magi Mag) mom Sëriñ Moor Anta Sëli Mbàkke ak Soxna Jaara Buso.
Mu doon ab jullit bu di doomi jullit , di as gor su di doomi gor .
s-95
wo_wtb-ud-train_1585
Mu doon ab jullit bu di doomi jullit, di as gor su di doomi gor.
Mu doon ku sàmmu te ragal Yàlla , daan jàng ak a jàngale Alxuraan , ci anam gu yéeme .
s-96
wo_wtb-ud-train_1586
Mu doon ku sàmmu te ragal Yàlla, daan jàng ak a jàngale Alxuraan, ci anam gu yéeme.
Mu daan jàngale it bépp xam-xam bu aju ci diine .
s-97
wo_wtb-ud-train_1587
Mu daan jàngale it bépp xam-xam bu aju ci diine.
Nee nañu saxoo woon na guddi gu ne téeméeri ràkkaa ( 100 i ràkka ) noppi jàng Alxuraan ba mu mat .
s-98
wo_wtb-ud-train_1588
Nee nañu saxoo woon na guddi gu ne téeméeri ràkkaa (100 i ràkka) noppi jàng Alxuraan ba mu mat.
Bi mu fi bawoo Sëriñ Tuuba seereel ko ni : Man déy Sëriñ Mbàkke Kajoor ak Sëriñ Moor Jaara rekk laa mas a gis kuy dugg ci bàmmeel te yobbaalewu fa bàkkaar .
s-99
wo_wtb-ud-train_1589
Bi mu fi bawoo Sëriñ Tuuba seereel ko ni: Man déy Sëriñ Mbàkke Kajoor ak Sëriñ Moor Jaara rekk laa mas a gis kuy dugg ci bàmmeel te yobbaalewu fa bàkkaar.
Loolu di tegtale cofeel gu Sëriñ bi amoon ci moom , ak rawatina nag di nu xemmeemloo yoon wi mu jaar ba am loolu .
s-100
wo_wtb-ud-train_1590
Loolu di tegtale cofeel gu Sëriñ bi amoon ci moom, ak rawatina nag di nu xemmeemloo yoon wi mu jaar ba am loolu.
Edit as list • Text view • Dependency trees