Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part dev
Text: Transcription Written form - Colors
Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi .
s-1
wo_wtb-ud-train_400
Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi.
Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi , Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi .
s-2
wo_wtb-ud-train_401
Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi, Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi.
Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm , leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw , Gàmbi , Senegaal , Moritani , Marok door a dëppaat .
s-3
wo_wtb-ud-train_402
Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm, leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw, Gàmbi, Senegaal, Moritani, Marok door a dëppaat.
Bu ñu egsiwaatee Moritani , te nappeesu leen , dañuy dee .
s-4
wo_wtb-ud-train_403
Bu ñu egsiwaatee Moritani, te nappeesu leen, dañuy dee.
Teg na ci ne : am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp , ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp .
s-5
wo_wtb-ud-train_404
Teg na ci ne: am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp, ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp.
Jëwriñ jee ngi laaj : Ku di napp toni jën yooyu ?
s-6
wo_wtb-ud-train_405
Jëwriñ jee ngi laaj: Ku di napp toni jën yooyu?
Ay bato wëyyu ñoo koy napp , bato yu xarala lañu , gaaw lool te mëneesu leen a teg loxo .
s-7
wo_wtb-ud-train_406
Ay bato wëyyu ñoo koy napp, bato yu xarala lañu, gaaw lool te mëneesu leen a teg loxo.
Loolu lanuy ñàkk at mu jot .
s-8
wo_wtb-ud-train_407
Loolu lanuy ñàkk at mu jot.
Ndax jaadu na nguur gi di seetaan woowu yàqute , déedéet .
s-9
wo_wtb-ud-train_408
Ndax jaadu na nguur gi di seetaan woowu yàqute, déedéet.
Nee na , xalaat nanu ren , jàppandal ay batoy biir réew mi ak yu bitim-réew ngir ñu dem nappi jën yooyu .
s-10
wo_wtb-ud-train_409
Nee na, xalaat nanu ren, jàppandal ay batoy biir réew mi ak yu bitim-réew ngir ñu dem nappi jën yooyu.
Nee na , li ñuy napp dina nu indil at mu nekk 35 Dollar ( ton bu nekk ) .
s-11
wo_wtb-ud-train_410
Nee na, li ñuy napp dina nu indil at mu nekk 35 Dollar (ton bu nekk).
APS : Dibéer 15 maars 2009
s-12
wo_wtb-ud-train_411
APS: Dibéer 15 maars 2009
Edit as list • Text view • Dependency trees