Sentence view
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | dev |
---|
Text: -
Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am.
s-1
wo_wtb-ud-train_2042
Njiitu réew mi, Maki Sàll, tënk na léegi ci 8 at jéle ko ci 5, digub at yi oto yi di dugg Senegaal te di jóge bitim-réew war a am.
Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.
s-2
wo_wtb-ud-train_2043
Mu ngi ko dogale ci jotaayu jëwriñ yi amoon alxamis ci Ndakaaru.
Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare n° 2012-444 soppi bu n° 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi.
s-3
wo_wtb-ud-train_2044
Moom (Maki Sàll) xaatim na dekkare n° 2012-444 soppi bu n° 2001-72 bu 26 samwie 2001 jëm ci dugal daamar ci biir réew mi.
Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am.
s-4
wo_wtb-ud-train_2045
Dekkare boobu dafa di tënk léegi ci 8 at jéle ko ci 5 at yi oto yi di duggu Senegaal war a am.
S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi.
s-5
wo_wtb-ud-train_2046
S. Sàll dige woon na ci baatum dagaan ne dina ko def bu ñu ko tegee ci boppu réew mi.
Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal.
s-6
wo_wtb-ud-train_2047
Daamar yu ëpp 10 at a ngi daw ca Bennoo-Réew ak ca Tugal.
Lu tax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal?
s-7
wo_wtb-ud-train_2048
Lu tax, daamar yooyu mënuñoo daw ci Senegaal?
Loolu la waxoon.
s-8
wo_wtb-ud-train_2049
Loolu la waxoon.
Dogal booboo ngi tukkee woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon si di tukkee ci oto yu màgget yi.
s-9
wo_wtb-ud-train_2050
Dogal booboo ngi tukkee woon ci nguurug Abdulaay Wàdd, ngir yeesal pàrku daamar yi te aar kéew gi ci saxaar su bon si di tukkee ci oto yu màgget yi.
Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi yi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon.
s-10
wo_wtb-ud-train_2051
Teewul, mu doonoon dogal bu doomi réew mi yi nekk Tugal ak ca Bennoo-Réew naqarlu woon.
Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dogal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.
s-11
wo_wtb-ud-train_2052
Waaye, nguur gi dëggër rekk ci fi mu jàppoon, naan dogal bi tax na njayum oto yu yees yokk ci ja yu biir réew mi.
Edit as list • Text view • Dependency trees