Sentence view

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Partdev

Text: -

[1] tree
Moytuleen kolesterol (cholestérol)
s-1
wo_wtb-ud-train_1275
Moytuleen kolesterol (cholestérol)
[2] tree
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase.
s-2
wo_wtb-ud-train_1276
Xibaar yii tibbees na leen ci Orangeinfo, ñu tukkee ci Doktoor Abdul Asiis Kase.
[3] tree
Lan mooy kolesterol?
s-3
wo_wtb-ud-train_1277
Lan mooy kolesterol?
[4] tree
Kolesterol diw la gu baax ci nit, ndax dafa bokk ci yi di tabax yaram.
s-4
wo_wtb-ud-train_1278
Kolesterol diw la gu baax ci nit, ndax dafa bokk ci yi di tabax yaram.
[5] tree
Waaye nag, su natt bi jéggee dayo ci deret ji, dafa di bàyyi ay àkk ci solom yi deret ji di jaar ngir dem ci xol bi (athérosclérose).
s-5
wo_wtb-ud-train_1279
Waaye nag, su natt bi jéggee dayo ci deret ji, dafa di bàyyi ay àkk ci solom yi deret ji di jaar ngir dem ci xol bi (athérosclérose).
[6] tree
Fu kolesterol di jóge?
s-6
wo_wtb-ud-train_1280
Fu kolesterol di jóge?
[7] tree
Li ëpp ci kolesterol res bee koy defar.
s-7
wo_wtb-ud-train_1281
Li ëpp ci kolesterol res bee koy defar.
[8] tree
Gannaaw loolu, dees na ko jële ci ñam yu deme ni nen, mbàq ak butit (laxas), bëer, yàpp wu duuf añs (ak ñoom seen).
s-8
wo_wtb-ud-train_1282
Gannaaw loolu, dees na ko jële ci ñam yu deme ni nen, mbàq ak butit (laxas), bëer, yàpp wu duuf añs (ak ñoom seen).
[9] tree
Nattu kolesterol bu jéggi dayo lan lañu ciy ragal?
s-9
wo_wtb-ud-train_1283
Nattu kolesterol bu jéggi dayo lan lañu ciy ragal?
[10] tree
Natt bu jéggi dayo mën naa jur jàngoroy xol, niki kriis kàrjag «crise cardiaque».
s-10
wo_wtb-ud-train_1284
Natt bu jéggi dayo mën naa jur jàngoroy xol, niki kriis kàrjag «crise cardiaque».
[11] tree
Jàppees na ne kolesterol, póon, jabet, ak tasyoŋ bu kowe ñoo jiitu ci yi di sabab jàngoroy xol.
s-11
wo_wtb-ud-train_1285
Jàppees na ne kolesterol, póon, jabet, ak tasyoŋ bu kowe ñoo jiitu ci yi di sabab jàngoroy xol.
[12] tree
Looloo waral boroom xam-xam yi naan kolesterol benn la ci ñeent ñiy faat xol «bourreaux du cœur».
s-12
wo_wtb-ud-train_1286
Looloo waral boroom xam-xam yi naan kolesterol benn la ci ñeent ñiy faat xol «bourreaux du cœur».
[13] tree
Yow mi bëgg lu la musal ci kolesterol bu ëpp, toppal dénkaane yii la Doktoor Kase baaxe.
s-13
wo_wtb-ud-train_1287
Yow mi bëgg lu la musal ci kolesterol bu ëpp, toppal dénkaane yii la Doktoor Kase baaxe.
[14] tree
Wàññil yu niin yi, kenn waxul nga bàyyi leen.
s-14
wo_wtb-ud-train_1288
Wàññil yu niin yi, kenn waxul nga bàyyi leen.
[15] tree
Bul xér ci diwlin, te bu ko bàyyi ba mu sãs.
s-15
wo_wtb-ud-train_1289
Bul xér ci diwlin, te bu ko bàyyi ba mu sãs.
[16] tree
Naka noonu wàññil ñam yii: bëer (doonte sax dañu bind ne woyofalees na ko), diwu-ñor, sosisoŋ, yàpp wu duuf, meew mu ñu tonniwul diw ga, soowu niw, nebbon (garees), dax, mburu mu ñu noote meew «pain au lait», mbaa mburu ak sokkolaa, kurwaasã «croissants», ngato, kreem glaase...
s-16
wo_wtb-ud-train_1290

[17] tree
Deel lekk jën lu mu néew néew ñetti yoon ci ayu-bés bi.
s-17
wo_wtb-ud-train_1291
Deel lekk jën lu mu néew néew ñetti yoon ci ayu-bés bi.
[18] tree
Jën yu deme ni wëyëŋ, yaabóoy, óoba, jay, njunna jàppees na ne baax nañu ci yemale kolesterol.
s-18
wo_wtb-ud-train_1292
Jën yu deme ni wëyëŋ, yaabóoy, óoba, jay, njunna jàppees na ne baax nañu ci yemale kolesterol.
[19] tree
Taamul meew mu ñu woyofal, ak soow, yawuur, formaas yu niinaay ba barewul (0 % ba ci 10 % MG).
s-19
wo_wtb-ud-train_1293
Taamul meew mu ñu woyofal, ak soow, yawuur, formaas yu niinaay ba barewul (0 % ba ci 10 % MG).
[20] tree
Mën ngaa lekk yàpp, waaye bumu doon yàpp wu duuf;
s-20
wo_wtb-ud-train_1294
Mën ngaa lekk yàpp, waaye bumu doon yàpp wu duuf;
[21] tree
Xamal ne yàpp wu ñu wàjji moo gën wu ñu saaf ci diwlin.
s-21
wo_wtb-ud-train_1295
Xamal ne yàpp wu ñu wàjji moo gën wu ñu saaf ci diwlin.
[22] tree
Naka noonu ganaar it baax na, ñu wàjji ko, dindi der bi.
s-22
wo_wtb-ud-train_1296
Naka noonu ganaar it baax na, ñu wàjji ko, dindi der bi.
[23] tree
Deel lekk lujum ak meññent 'fruits'.
s-23
wo_wtb-ud-train_1297
Deel lekk lujum ak meññent 'fruits'.
[24] tree
Deel lekk lujum (naaje, karoot, batañse, suppome, pooro, kànja, jaxatu, soble ñax 'oignons verts', pooro, batañse... ak meññent (sorãs, pom, màngo, anaanaas, pàppaayo, xaal añs.
s-24
wo_wtb-ud-train_1298
Deel lekk lujum (naaje, karoot, batañse, suppome, pooro, kànja, jaxatu, soble ñax 'oignons verts', pooro, batañse... ak meññent (sorãs, pom, màngo, anaanaas, pàppaayo, xaal añs.

Edit as listText viewDependency trees