s-1
| Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal. |
s-2
| Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk. |
s-3
| Kajoor moo di kàdd ag garab gu nekk Senegaal ak joor, suuf si. |
s-4
| Moo jur baat boobu Kajoor ci Wolof. |
s-5
| Ñi jëkk a yor suufi Kajoor, ay séeréer lañu woon. |
s-6
| Ñu doonoon ay lamaan te sant JAAÑ. |
s-7
| Ba pare, xeetu Wagadu ak Jafunu, soqi ci Sooninké yi, jóge ca penku. |
s-8
| Ñoo sos meen yi jëkk a ilif nguur gi, ak ñu sant FAAL. |
s-9
| Gàddaay moo leen tax ñëw Kajoor. |
s-10
| Kon ñooñu mujj nekk Dammeel Kajoor, ay doxandéem lañu yu nekkoon ca réew moomu ca njëlbéen. |
s-11
| Dammeel mooy damm. |
s-12
| Ndax ku jëkk a jël dakkantal boobu, di Decce Fu Njogu FAAL, dañu naan damm na li Kajoor seqante woon ak Jolof, ndax Jolof moo nangu woon Kajoor. |
s-13
| Li mu def a tax Kajoor jël yoonam te yore boppam. |
s-14
| Loolu, ca jamono ja Lele Fuli Fak NJAAY nekkoon Buur-ba Jolof la xeewe. |
s-15
| Buur-ba boobu moo tase ci xare ak doomu Decce Fu Njogu, di Amari Ngone Sobel FAAL, ca benn dëkk bu ñu naan DANKI. |
s-16
| Ca xare boobu Kajoor jël yoonam, te damm li ko Jolof nangu woon. |
s-17
| Ba noppi Amari Ngone jox baayam Decce Fu Njogu mu jiite Kajoor. |
s-18
| Ca tegu, Kajoor di gën a am doole. |
s-19
| Amari Ngone dem na Bawol ak ay jàmbaaram, nangu reew moomu. |
s-20
| Lii moo tax Amari doonoon ku jëkk a nekk Dammeel-Teeñ. |
s-21
| Bawol, njabootu ndeyam ñoo fa nekkoon buur, ak nijaayam, Ñoxor Njaay Kuli Njigan. |
s-22
| Amari moo duggal aada bi. |
s-23
| Ñu fal buur bu ñu tudde Xulixuli, di fàtteliku bi NJAAJAAN NJAAY (ku jëkk a nekk Buur-ba Jolof) nekkoon biir dex gi, ca Waalo. |
s-24
| Ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur gu ay am-amam newoon gàññ. |
s-25
| Mbay ak liggéey ci loxo ak càmm ak napp ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga. |
s-26
| Mbay moo doonoon liggéey bi ëppoon solo ci koom-koomam. |
s-27
| Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ ca koom ga. |
s-28
| Manoon naa indi sax ab xiif. |
s-29
| Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi. |
s-30
| Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng. |
s-31
| Xamoon nañu mbayum wëtteen. |
s-32
| Liggéey ak loxo ñeeño yi lañu ko feetale woon. |
s-33
| Napp gi amoon na solo lool ci dund gi. |
s-34
| Waaye njaay moom naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal. |
s-35
| Mujj na ba yoon yi jóge bëj-gànnaar ñàkk solo lool njëgg mi. |
s-36
| Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo. |
s-37
| Fekkoon na Kajoor daan jaay ay der ak ay bëñi ñayy. |
s-38
| Mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi, ... |
s-39
| Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon. |
s-40
| Ñi ñu di wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu. |
s-41
| Benn nit amu ci woon moomeel. |
s-42
| Loolu terewul woon ku mu neexoon mu jariñoo ci kéem kàttanam. |
s-43
| Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya. |
s-44
| Ñi di door a falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo. |
s-45
| Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon. |
s-46
| Ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul. |
s-47
| Rax-ci-dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk. |
s-48
| Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi. |
s-49
| Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetale woon mbay mi. |
s-50
| Ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat. |
s-51
| Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay. |
s-52
| Nguur gu bees gi tax na ba ñu indi tër yu bees ci ay àtte yu bees. |
s-53
| Dammeel moo féete woon ñépp kaw. |
s-54
| Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen. |
s-55
| Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen. |
s-56
| Waaye loolu su xewee li ko di waral moo di fullay waa ja ak faydaam ak tabeem. |
s-57
| Yii yépp ñi di tànn daa nañu ci bàyyi xel. |
s-58
| Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem. |
s-59
| Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe. |
s-60
| Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur. |
s-61
| Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn. |
s-62
| Kajoor nekkoon na juróomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum. |
s-63
| Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam fu nga féete. |
s-64
| Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur. |
s-65
| Waalo bokkoon na ci yenn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon. |
s-66
| Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar. |
s-67
| Njurbel moo nekkoon péeyam ci lu njëkk. |
s-68
| Gannaaw bi lañu ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer. |
s-69
| Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu gannaaw ak ñàkk doole. |
s-70
| Ñooñu ñooy : Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi. |
s-71
| Gannaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur. |
s-72
| Bokk na ca Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néegu Njurbel. |
s-73
| Moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur. |
s-74
| Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel. |
s-75
| Moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi. |
s-76
| Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi. |
s-77
| Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo. |
s-78
| Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de Geer. |
s-79
| Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo: |
s-80
| Ba njëkk moo di Lingeer mi di yaayu buur bi ak Aawo mi di soxnaay buur su njëkk. |
s-81
| Moom moo am teraangaay toog ca gangunaay (moo di toogu gu buur) ga. |
s-82
| Bu ñaareel ba mooy ñatt ci boroom ndomboy tànk yi ci péncum Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak Maalaw mi yor koom-koom bi. |
s-83
| Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur. |
s-84
| Baadi moom moo di njiitu doomi buur bi, ak yenn ci jëwriñ yi. |
s-85
| Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare. |
s-86
| Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram. |
s-87
| Mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo war a teew ci gàmmu gi. |
s-88
| Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la. |
s-89
| Ndaxte seenug teew li mu di tegtal moo di yeesal seenug nangu, la ñu lokki ak la ñu siif. |
s-90
| Mbooleem alal yooyu daa nañu leen séddale ñetti xaaj: benn ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca péncum Séb ak Bawar. |
s-91
| Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbéem yi. |
s-92
| Nguur ga dañu ko seddale woon ci ay diwaan. |
s-93
| Bu ci ne amoon na Bàjjo bu di dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer). |
s-94
| Kàjj moom lañu fal ci ndijjooru dex gi, li-ko-dale ca Aarnik ba fa dex gi sottee. |
s-95
| Buriko moom lañu fal ci bëj-gànnaaru Lag de Geer. |
s-96
| Mu ngi daan dëkk ca Foos. |
s-97
| Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinó Bawaal. |
s-98
| Li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi. |
s-99
| Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo. |
s-100
| Barlaf moo nga dëkkoon ca sowwu Lag de Geer. |