s-1
| Ci Kaw Gaambi ak Penku Senegaal ay nguur yu bari toftaloo nañu ci dexug Gaambi gi, yi ci ëpp solo ñooy Ñaani ak Wuli. |
s-2
| Ñoom nag ñu ngi leen taxawal ci xarnub fukk ak ñeent g.j. |
s-3
| Ay way gàddaay yu bàyyikoo ca Imbratóor gu Mali gaa leen taxawaloon. |
s-4
| Yii nguur nag ci ron waawug Jolof gu mag gi lañu nekkoon, ba kero ñuy nanguwaat seenug temb ci xarnub fukk ak juróom benn g.j. |
s-5
| Nguur yii nag bokkoon nañu ci joqalanteg yaxantu gi ci anam gu sawar. |
s-6
| Looloo taxoon ñuy réew yu naat. |
s-7
| Ci bëj-gànnaaru Wuli la nguuri Goy ak Kamera nekkoon. |
s-8
| Ki leen taxawaloon kilifa la woon gu bokkoon ci njabootug Baajli, moo di Salmaan Xaasa, mi nga xam ne jiite woon na ag nguur ci penku Senegaal. |
s-9
| Ñaari nguur yii nag ba xarnub fukk ak juróom ñeent g.j, dañoo bennoo woon. |
s-10
| Buur bi dàkkantalu Tunka la daan yore. |
s-11
| Ci atum 1833 g.j, la ab xare tàkk ci seen diggante, ba moo waral ñu tàqalikoo. |
s-12
| Goxub Gaambi gu kawe gi ak Senegaal gu penku gi séddaliku na doon ay nguur yu bari, waaye am na ci yu daawul weesu yaatuwaayu as ndëkk. |
s-13
| Gi magoon ci nguur yii ci lu dul sikk moo di Namandéeru ak Faalimi, ñaar yii nga xam ne ñu ngi leen sosoon ci lu tollu ak ñeenteelu xarnu g.j. |
s-14
| Ñu nekkoon nag ci ron kiliftéefug imbraatóor gu Gana. |
s-15
| Am na yeneen nguur yu sosu woon ca la tollu ak xarnub fukk ak ñatt g.j, ñooy : Siiselaa, Beledugu, Niokolo, Badon, Bademba, Bundu, Gajaga. |
s-16
| Nguur gu mujj gii nag (Gajaga) giirug Sambiira Baccili ñoo ko jiite woon, la-ko-dale ca xarnub fukk ak ñatt g.j. |
s-17
| Nguurug Gajaga dund na ci ag naataange ngir joqalantey yaxantu ya fa daan am te naataloon gox ba, rawatina yaxantug tàkk gi. |
s-18
| Ci xarnub fukk ak juróom ñeent g.j, yaxantu gi mu ngi sukkandiku woon ci daakaande. |
s-19
| Nguuri Gambi gu kawe gi dañu daan dàkkul seen bopp cong yi leen seen dëkkandoo yi daan faral a def, jublu woon ci nangu ci ñoom lenn ci seen i suuf. |
s-20
| Ci xarnub fukk ak juróom ñaar ak bu fukk ak juróom ñatt la ay xarekat yu jóge ci penku dikk soppi nosteg àtte ga fa amoon. |
s-21
| Bu ko defee ay njaboot yu yees daldi tàmbalee sangu (doon i njiit) ca gox ba. |
s-22
| Bu dee ca Siiselaa moom Daansirimaan moo daaneeloon njiitug giirug Siise, daldi wutal nguur gi weneen tur wu yees muy : Sirimaano. |
s-23
| Bu dee ca Beledugu moom, njabootug Siisoxo moo jële giirug Soomari ci nguur gi. |
s-24
| Ca Dantila moom ab nappkat bu siiwe ci turu Samakoto moo nangu nguur ga, dàq njabootug Samora ga. |
s-25
| Ci xarnub fukk ak juróom Bawol nguur su ndaw la woon su toppoon Jolof gu mag gi. |
s-26
| Bu ko defee, ag njaboot gu am ag jegeñaale ak buuri Kajoor yi daan ko jiite. |
s-27
| Bu jëkk, nguur googu, ay socé ak ay séeréer, ñoo ko yoroon. |
s-28
| Ndax Bawol, benn dex la woon foofu ci lu doog a am. |
s-29
| Boobu jamono, Bawol, amoon na ndox mu bare. |
s-30
| Ci cosaan, dañu ne, Bawol, ku fa jëkk a nekk buur, Xaayamagaan moo doon turam. |
s-31
| Xaayamagaan, ci làkku socé yi la soqeekoo, moo di: buuru gaalam. |
s-32
| Ñoom, socé yi fa nekkoon jamono boobu, seen mamm, Mande lañu baawoo. |
s-33
| Ba pare, séeréer yi ñëw. |
s-34
| Ñoom, Fuuta Tooro lañu jóge woon, gàdday ba Bawol, ndax jiyaar ji Muraabituun yi defoon foofu. |
s-35
| Ba ñu agsi Bawol, ci ubbite, dañu daan dëkkandoo ak socé, soog a leen daq. |
s-36
| Ba loolu amee, ñu yilif dëkk boobu. |
s-37
| Ci séeréer yi, askan yi ñu faloon, ñoo doon ñi sant Juuf, Ngom, Caw. |
s-38
| Te buur ba ñu daan taan ci ñoom, 'Téeñ' lañu ko daan tudde. |
s-39
| Loolu moo amoon, laata nguuru Jolof ñëw uuf dëkk bi. |
s-40
| Ci ñaareelu xaaju xarnu bii la Amari Ngóone xëy di buuru Kajoor ak Bawol ci jenn jamono ji. |
s-41
| Booba la buur bi tàmbalee jiite ñaari nguur, waaye nguur gu ci nekk yor politigu doxaliinu réewam. |
s-42
| Waaye boole gii bari lu mu daa jur ay réeroo ci diggante ñaari nguur yi, ndax gu ci nekk dafa bëgg a yilif ga ca des. |
s-43
| Buurub Bawal nag di Teeñ ab jataay a ko daa jàppale, bu ñu wéer tabbug ki di wuutu buur bi bu faatoo, ak fuglug saxal yi buur bi di def. |
s-44
| Nguur gi amoon na ab ëttu àtte buy àtte mbir yi. |
s-45
| Mbooleem kuréel yi nag daa nañu fa àttewoo (kuréelug nappkat yi, baykat yi, sàmm si, boroom mecce yi ak jigéen ñi). |
s-46
| Bokkug Bawol ci Yaxantug Tàkk gi taxu ko woon a deme noonu, ndaxte yooni yaxantu gi rombutoon ci ay suufam. |
s-47
| Moom kay dafa yamoon rekk ci yaxantug tefes gi. |
s-48
| Ca jamono yu yàgg ya li ëppoon ci giirug Pël ay sàmm yu daan màng lañu woon, di tuxu ci seen bëgg-bëgg ngir wër ndox ak ñax. |
s-49
| Ñu nekkoon di ñu tasoon ci gox yu bari ci sowwu Afrik, la-ko-dale ca dexug Senegaal ba ca ngéejus Càdd. |
s-50
| Ci diggante xarnub fukk ak juróom ak bu fukk ak juróom ñeent g.j, giir gii def na fi ay fipp yu Lislaam yu bari yu waral ñu taxawal ñatti nguur ci Senegaal: Fuuta Tooro - Bundu - Fuuta Jalon. |
s-51
| Ci mujjug xarnub fukk ak juróom g.j, am mbooloo ci way gàddaay yu Foolaan yi génne nañu Fuuta Jalon dem Fuuta Tooro. |
s-52
| Koli Tingala jiite leen. |
s-53
| Moo tegoon loxo Fuuta Tooro ci atum 1512 g.j, daldi taxawal nguurug Fuuta Tooro. |
s-54
| Ci atum 1770 g.j, la Sulaymaan Baal def ag jeqiku gu Lislaam. |
s-55
| Mooy gi soppi Fuuta def ko nguur gu Lislaam, Almaami Abdu Buukar jiite ko. |
s-56
| Mooy ki jiyaaroon kontar ay dëkkandoom: Waalo - Taraasa - Kajoor, la-ko-dale ca 1790 ba 1804 g.j. |
s-57
| Waaye dañu koo mujj dàq. |
s-58
| Ci xarnub fukk ak juróom ñeent g.j, la Fuuta tàmbalee naaxsaay. |
s-59
| Ci lu tollook 1690 g.j, la Tunka buurub Goy may menn mag mu jóge Podoor aw dog ci suuf. |
s-60
| Moo di Maalik Si, dog woowu mi ngi nekkoon diggante Faalimi ak Gambi gu kawe gi. |
s-61
| Ci nii la nguurug Bundu sosoo. |
s-62
| Maalik Si daldi nay jibal ab xare, def it Bundu muy nguur gu Lislaam, daldi safaanu nguurug Goy, gën a yaatal ag nguuram. |
s-63
| Nguur googu nekkoon na di gu naat ci ayug Maalik Si ak i way wuutoom (njabootug Siisebi). |
s-64
| Li ko waral di séqoo yi mu amoon ak Gambi. |
s-65
| Ci lu tollook 1727 g.j, la ag giirug Pël ca Fuuta Jalon jógoon. |
s-66
| Karamoko Alfa jiite ko, soppi gox boobu it def ko nguurug Lislaam. |
s-67
| Li gën ci li nit njëkk a amal ci wàllug xam-xam mu ngi xewe ci Goxub Afrig. |
s-68
| Ci lu gën a leer, ca Isipt gu yàgg ga la nit ku ñuul yóbboo ag nite (l'humanité) ba àggale ko ci xam-xam. |
s-69
| Booba la joxee firnde ci ne xam-xam du moomeelug wenn xeet, du caagéenu benn gox. |
s-70
| Gëstu yu boroom xam-xam bii di doomu Senegaal, di Seex Anta Jóob, maye nañu manees a saxal am-amu xam-xam bii di 'xeetu nit benn la'. |
s-71
| Ñoo bokk fu ñu bawoo, te xayug nit ku ñuul (la civilisation négre) moo jiitu ci xay yi. |
s-72
| Taariix mu ngi nuy jàngal ne xam-xam ak xarala dañoo gàddaay dem ca goxub Tugal, jaare ko ca Geres. |
s-73
| Bi mu mujjee di pujub àdduna bi ci wàllug xam-xam ak man-man, Tugal dafa daldi samp boppam niki digg (centre) bu coste ak pentug nit (créativité humaine) waaye mukk mu di bu ag muusam. |
s-74
| Ndax ag muus caadaa koy ëmb, te mooy fi nitug Afrig ki aaye, fi ko may mu jàmmaarloo ba tëyye màndargam caadaam, ak manmanu pentam gi nekk ci ag nekkam. |
s-75
| Ontologsi (L'ontologie) mbaa xam-xamu xalaatu nit ku ñuul ku Afrig mandargaalees na ko ni ko Meetar Wàdd wonee ca xalaatu 'jëmmam ba' (sa 'physicité'). |
s-76
| Màndargam xalaatub nit ku ñuul ku Afrig, moo di ne dafa di tay tabax ci cëslaayul yëg-yëg ak wormaal, séqoo gu nit ak dénd bi. |
s-77
| Loolu mooy wone nitug Afrig am na ay ngënéel yuy kojug nekk yu mu jëfandikoogul. |
s-78
| Ngënéel yii ci Afrig alal ju gànjaru lañu ngir gaawug yéegam ci biir ag gëstoom ñeel ñall (raccourcis) yu jàmme ngir dab yeneen réew yi. |
s-79
| Seen jéegoy njàng yu am solo yi nu def ci Dara yu Kawe yi, ku mel ne Abdulaay Wàdd, Seex Anta Jóob Modibo Jara, wone nañu rëy xelug nitug Afrig ak ag neexug xelam. |
s-80
| Poroxaan 2011: Soxna Jaara Mariyama Buso royukaayu jigéenu jullit |
s-81
| Soxna Mariyaama Buso ñu koy dàkkantale, ci jikko, Jaaratu-l-Laah (dëkkandoob Yàlla bi) gane àdduna ci atum 1833 ci as ndëkk su tudd Gollere ca Fuuta, génn àdduna ci atum 1866 ca Poroxaan. |
s-82
| Soxna Jaara Buso mom Sëriñ Hamaat Buso (baayam) ak Soxna Asta Waalo Mbàkke (yaayam), cosaano ci askanu Sëriif goo xam ne calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ci ñoom). |
s-83
| Mu dondoo ci loolu ag cell ak ab yar ba war ci doomi soxna jële ko ci waajuram wu jigéen. |
s-84
| Soxna Asta Waalo Mbàkke doon ab jàngalekatub Alxuraan ak xam-xamu diine di yare ci Lislaam rawatina ci Tassawuuf, mu juddu ci loolu. |
s-85
| Yaayam ju farlu jooju yar ko ci. |
s-86
| Am njàngam ak ab yaram: |
s-87
| Soxna Jaaratu-l-Laahi Buso jànge na Alxuraan ci aji / way-juram wu jigéen wu séll wa te sàmmu, te doon senn soxna su ame taxawaay bu mat sëkk ci Lislaam ci jàngale ak yare, niki Sëriñ si, ba mokkal ko ci anam gu sell te sax ci jamono yi muy am fukki at ak ñeent (14 at). |
s-88
| Mu jàngal ko it xam-xamu diineem niki jennal Yàlla (Tawhiid), àttey Lislaam ak aw yoonam (Fiq), séllal ak jaamu ngir Yàlla doŋŋ (Tassawuuf), ba mu wattu leen na mu ware. |
s-89
| Mu yar ko it ci Lislaam, ci jàng Alxuraan, ak jëfe ab xam-xamam. |
s-90
| Mu yar ko it ci ngor, muñ, nangu, ak jépp jikko ju ñu taamu ci as gor rawatina bu di ab jullit. |
s-91
| Ba mu mujj di ku xarañe bépp xam-xamu Lislaam, te it di kuy jëfe ngirum Tassawuuf ci anam gu xóot. |
s-92
| Ak li dund gi di gàtt lépp (33 i at) de moona téewul ci ag farloom bind na Alxuraan ñeen-fukki yoon ci yoxoy boppam (40 i kaamil) ba mujjoon di ab jàngalekatu Alxuraan ci taaral mbind. |
s-93
| As lëf ci ay jikkoom ak i meloom: |
s-94
| Soxna Jaaratu-l-Laah Dëkkandoob Yàlla bi ci ag céll ak ag sàmmu, di ab jullit bu di doomi jullit. |
s-95
| Mu nangu te seere ni: Amul jenn Yàlla ju dul Allaa. |
s-96
| Yàlla aji sàkk ji yélloowul wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn. |
s-97
| Moo di dégg, moo di gis. |
s-98
| Muhammad (jàmmi Yàlla ak xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la. |
s-99
| Ndaw lu mu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne. |
s-100
| Mu nangu te jàpp ni Lislaam rekk mooy diine. |