s-102
| Balaa tàmbali mu wax Bismil Laahi, bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul. |
s-103
| Lu ñu war a loj nag bu ñu amul lojukaay sañees na koo rendi. |
s-104
| Lu ñu war a rendi it bu ñu amul rendikaay te am lojukaay sañees na koo loj. |
s-105
| Giléem loj rekk lañu koy def mbaa deesu ko lekk, waaye deesu ko rendi, xanaa ñu loru ñàkk lojukaay te am rendikaay. |
s-106
| Bu boobaa nag dees na leen ko may. |
s-107
| Bu dee aw nag dees na ko loj niki noonu it dees na ko rendi. |
s-108
| Kon moom lu leen jekku rekk ñu sañ koo def noona. |
s-109
| Fii nag rendi ko lañu gën a miin. |
s-110
| Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi dañu war a dagg. |
s-111
| Kon ci ag wet lañu koy defe ak kanam... |
s-112
| Na moytu yii: Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk. |
s-113
| Bu ko ca yeexee delloo nag te lor waralu ko, kon deesu ko lekk. |
s-114
| Te yit mu bañ a tàqale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën. |
s-115
| Waxtuw rendi walla loj mu ngi dale ci rendig yilimaan. |
s-116
| Rendig yilimaan moo ngi aju ci ginnaaw bu sëlmalee julli gi, ba jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi rendee mu baax. |
s-117
| Ci ngiirum Maalig fàww rekk mu doon bëccëg, deesu ko sañ a ray guddi. |
s-118
| La ca gën mooy boroom rendil ko boppam. |
s-119
| Bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw. |
s-120
| Ku dul ab jullit manu laa rayal am tabaski. |
s-121
| Ku rendi Tabaski ab jàmbur te amu ci ndigal, du ko doy am Tabaski te war naa fay boroom. |
s-122
| Am Tëbëski nag deesu ko rendi jëkk rendig yilimaan te yilimaan it balaa rendi nég ba julli. |
s-123
| Ci ni ko Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi waxe: Képp ku rëy njëkk jullig iid gi, deful lu dul rëy baayima bu ñu man a lekk; |
s-124
| Waaye ku rey ginnaaw jullig iid gi nag, am na am Tëbëski (Buxaari soloo na ko). |
s-125
| Tabaski lu am solo la ci Lislaam. |
s-126
| Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi xamle na ni toq dereet wi di njëkk a génn Yàlla dina ci jéggale mbooleem bàkkaar yu ñu mas a def. |
s-127
| Nii la dikke ci hadiis ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom). |
s-128
| Jëlee nanu ci Ibn Abaas mu ni Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi nee na: Xaalis dugaleesu ko ci lu gën gàttub Tabaski (iid) (Daaru Qutni soloo na ko). |
s-129
| Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi bégal na nu ci ne xarum Tabaski dina njot ci sawara niki mu njotee woon bakkanu Ismaayla. |
s-130
| Amul jëf ju nit di def ci bisu Tëbëski ju gën a neex Yàlla tuur ci dereet. |
s-131
| Noonu la ko Aysa nettalee. |
s-132
| Noo ngi leen di yéene Tëbëskig jàmm! |
s-133
| Di leen balu àq; di leen baal àq, te di ñaan Yàlla boole nu baal. |
s-134
| Te nu fekke ko te romb ko... |