Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train Annotation Dione, Bamba
Text: Transcription Written form - Colors
Microsoft : Siiwalug Windows Phone 7
s-1
wo_wtb-ud-train_1967
Microsoft: Siiwalug Windows Phone 7
Microsoft dellusi na ci ag woote ak ab gaaral bu ràññeeku altine ci lu aju ci telefonam bi ñépp di xaar Windows Phone 7 ànd ak defar Nosteg Doxiin ( operating system ) bu bees tàq ñeel Mobiil .
s-2
wo_wtb-ud-train_1968
Microsoft dellusi na ci ag woote ak ab gaaral bu ràññeeku altine ci lu aju ci telefonam bi ñépp di xaar Windows Phone 7 ànd ak defar Nosteg Doxiin (operating system) bu bees tàq ñeel Mobiil.
Doorees na ag gaaralu Windows Phone 7 ca New York .
s-3
wo_wtb-ud-train_1969
Doorees na ag gaaralu Windows Phone 7 ca New York.
Gaaral googu njiitul Microsoft Stef Balma moo ko jiite , ngir wone ni seen nosteg doxiin bu bees bi dafa nekk lu taaru te yéeme .
s-4
wo_wtb-ud-train_1970
Gaaral googu njiitul Microsoft Stef Balma moo ko jiite, ngir wone ni seen nosteg doxiin bu bees bi dafa nekk lu taaru te yéeme.
Ku nekk war naa man a seet Windows Phone te wax ni man na maa teewal la Balma wax .
s-5
wo_wtb-ud-train_1971
Ku nekk war naa man a seet Windows Phone te wax ni man na maa teewal la Balma wax.
Ci loolu , joyalees na siiwalug Windows Phone jëmmalug man-mani telefon bi ak ay leeral ci juumtukaay yi ci nekk .
s-6
wo_wtb-ud-train_1972
Ci loolu, joyalees na siiwalug Windows Phone jëmmalug man-mani telefon bi ak ay leeral ci juumtukaay yi ci nekk.
Wonees na nosteg doxiin bi mel niki luy mottalil boppam ag dundam ci lu dul di ko xaar feneen .
s-7
wo_wtb-ud-train_1973
Wonees na nosteg doxiin bi mel niki luy mottalil boppam ag dundam ci lu dul di ko xaar feneen.
Siiwalees na juróom ñeenti telefoni Windows Phone yoo xam ne fimne way-jëfandikuy waa-aamerig dinañu ci daldi man a tàmbali a tànn , ànd ak T-Mobiil AT&T génne ko , ci gën gaa yeex , 8 Nowàmbar .
s-8
wo_wtb-ud-train_1974
Siiwalees na juróom ñeenti telefoni Windows Phone yoo xam ne fimne way-jëfandikuy waa-aamerig dinañu ci daldi man a tàmbali a tànn, ànd ak T-Mobiil AT&T génne ko, ci gën gaa yeex, 8 Nowàmbar.
Lu aju ci tëriin li , jëmmal gi ak yomb-gee-jëfandikoo moo di li tax a jóg Mickrosoft ci lii , ci yakaar a joxe jëmmal gu mat sëkk .
s-9
wo_wtb-ud-train_1975
Lu aju ci tëriin li, jëmmal gi ak yomb-gee-jëfandikoo moo di li tax a jóg Mickrosoft ci lii, ci yakaar a joxe jëmmal gu mat sëkk.
Looloo tax sa Smartphone ( telefon bi ) man a teyewaale la ñu xamoon ci Microsoft-centric ( beneen telefon ) .
s-10
wo_wtb-ud-train_1976
Looloo tax sa Smartphone (telefon bi) man a teyewaale la ñu xamoon ci Microsoft-centric (beneen telefon).
Wax nag yomb na , kon nanu xaar ba Windows Phone 7 wàcc ci maarse bi ( ja bi ) nu xool ndax seen jubluwaay walla yéene jooju mel na ni .
s-11
wo_wtb-ud-train_1977
Wax nag yomb na, kon nanu xaar ba Windows Phone 7 wàcc ci maarse bi (ja bi) nu xool ndax seen jubluwaay walla yéene jooju mel na ni.
Mbetteel gi gën a rëy ci wàllu ndefarum tëriin dal na leen , ndekete Windows Phone 7 déy manul sax a jël man-manu sotti-taf ( copie-coller ) , Waawaaw !
s-12
wo_wtb-ud-train_1978
Mbetteel gi gën a rëy ci wàllu ndefarum tëriin dal na leen, ndekete Windows Phone 7 déy manul sax a jël man-manu sotti-taf (copie-coller), Waawaaw!
Lu man a am daal manu ko fimne .
s-13
wo_wtb-ud-train_1979
Lu man a am daal manu ko fimne.
Nee nañu nag dinañu def ag yeesal ngir mu man ko ci weeru Saawiyee .
s-14
wo_wtb-ud-train_1980
Nee nañu nag dinañu def ag yeesal ngir mu man ko ci weeru Saawiyee.
Edit as list • Text view • Dependency trees