Dependency Tree

Universal Dependencies - Wolof - WTB

LanguageWolof
ProjectWTB
Corpus Parttrain

Select a sentence

Showing 1 - 100 of 134 • previousnext

s-1 Tabaski Sunna la su far ci ab jullit.
s-2 Tëbëski mooy ñaareelu iid (bër) ci Lislaam ginnaaw bu Korite jàllee.
s-3 Jële nanu ci Anas (gërëmul Yàlla ci moom) mu ne: Bi Yonent (Yalla na jàmmi Yàlla nekk ci moom) bi yegsee Madiina fekkee na leen ñaari bis ñu ca daan caaxaan ak a fo.
s-4 Mu ne leen: Ana lu di ñaari bis yii?
s-5 Ñu ne: Danu ci daan fo (caaxaan) ci jamonoy ceddo (jaahiliya).
s-6 - Yonent bi ne leen: Yàlla jox na leen ñaari bis yu gën yooyu ñaar, ñu di bisu Tabaski ak bisu Kori (Abuu Daawud soloo na ko).
s-7 Moom Täbaski dees na ko amal ci fukkeelu bis ci aw Täbaski, di weer wi mujj ci atum weer wi (Wolof).
s-8 Ñaari bër yooyu, di Tëbëski ak Kori, bokk nañu ci teddngay Lislaam, ba tax na kenn sañu cee woor.
s-9 Yonent bi (jàmmi Yàlla yal na nekk ci moom) tere na ku ci woor ci hadiis yu wér.
s-10 Waaye nag bu dee bisu Täbaski sunna la boo xëyee bañ a lekk dara, ba ba nga di julliji ba noppi.
s-11 Ci Ngiirum Maalig ak Shaafi, Tëbëski Sunna la su far ci ab jullit bu di mukàllaf, di as gor, man ko te mu bañ koo sonal.
s-12 Bu yooyu dajee mag ak gone ñoo ci yam, ku xës mukàllaf sunna su far si war na la.
s-13 Te it dina nekk farata ci ñaari anam yii:
s-14 Benn, ci ku ko nësër: niki nga ni bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tabaski.
s-15 Fu loola amee rekk manatul a ñàkk, farata la ci yaw.
s-16 Ci ku xës jënd am tëbaski, walla mu yor am xar jublu ci tabaski: bu loolu xësee am dafa di daldi nekk farata ci yaw.
s-17 Àtteb Tabaski ci Lislaam?
s-18 Yàlla nee na: Jullil ngir sa boroom te rendi (lottal)
s-19 Yonent bi nee na: Ku am dooley tabaski te tabaskiwul, kon bu mu jege sunu barabu julliwaay.
s-20 Abuu Hurayra moo ko nettali, Ibn Maaja, Ahmad, Daaru Qutni ak Al-Haakim soloo nañu ko, doonte bari na ñu jam hadiis bi ci woroom xam-xam yi, niki Haasim ak ñeneen.
s-21 Baraan nettali na ni, Yonent bi nee na: Li nuy njëkk a def ci bis bii, mooy julli.
s-22 Ginnaaw ba nu dellu lottal.
s-23 Ku def loolu def na sunu sunna.
s-24 Ash-Shaari nee na: Duma nangu ku am dooley am Tabaski di ko sàggane.
s-25 Yonent bi saxaloon na ko te daan ko digle.
s-26 Sunna la su far ci Ñoñ-Maalig, Shaafi, ag ñenn ci waa Ahmad Ibn Hambal.
s-27 Bu dee nag ci ngiirum Abuu Hanifa ñoom lu war la.
s-28 Lu war ca ñoñ Abuu Hanifa nag tekkiwul farata la.
s-29 Sopp nañu yii ci bisu Tëbaski:
s-30 - Sangu lu ñu sopp la;
s-31 - Sol yére yu bees boo di julliji, ak xeeñoo lëjkoloñ (ba mu des rekk jigéen);
s-32 - Sopp nañu nga bañ a lekk dara ba julliji ba ñëw, soog a lekk;
s-33 Yàlla nee na ci Alxuraan (lu nu ci dégge): Yàlla amul soxla ci yàpp wi walla dereet ji; waaye la ko ca soxal moo di ragal Yàlla gu bawoo ci yeen.
s-34 Noonu lañu leen tàggate ngir ngeen màggal Yàlla ci li mu leen gindi.
s-35 Te nanga bégal way-rafetal ñi (Suraat 22, Laaya 36)
s-36 Kon nanu jàpp njëkk ni yéene ju sell te Yàlla rekk tax waliif ngistal walla wanu ci bëti nit ñi moo di maye am Tabaski.
s-37 Ci Lislaam ñaari mbir sàrt la ci nangu ag jëf ju mu man a doon.
s-38 Benn, mu dëppoo ak sunna; ñaar: sellal ko ngir Yàlla doŋŋ.
s-39 Yonent bi (Yalla na jàmmi Yàlla nekk ci moom) nee na: Sellal-leen seen i jëf ngir Yàlla kat du nangu lu dul lu ñu sellal ngir moom.
s-40 Sàrt yii nag moo ko di tax a wér:
s-41 Xar mu am juróom benni (6) weer walla at ak i fan ci li sax ci Waa-Maalig, te di am kuy moo ci gën.
s-42 Bu dee aw bëy nag, na am at ak weer ci Waa-Maalig.
s-43 Xar a gën, topp bëy, topp nag ak giléem.
s-44 Xar mu góor a gën mu jigéen, bëy wu góor a gën wu jigéen, nag ak giléem naka noonu.
s-45 Juróom ñaari jullit man nañu a boole jënd aw nag walla giléem.
s-46 Bu dee xar walla bëy nag kenn du ko bokk jënd.
s-47 Waaye nag man nga a ray yéene ci képp ku di yewwoo ci kër gi, moo xam mu di ku nga xam ne dundal ko yaw la war, niki sa ay doom ak sa soxna, walla mu di ku nga xam ni dundal ko waru la, niki sa ay rakk yu góor ak jarbaat...
s-48 Bu ñu ko amul, yéene leen ci dina leen doy am Tëbëski.
s-49 Ku nekkul ci kër gi nag loolu du man a nekk.
s-50 Yu ñu bañ ci am Tabaski:
s-51 Bu benn béjjën dammee te wéragul, manaan di nàcc, du mat am tabaski (ci Maalig).
s-52 Bu wéree may nañu la ko.
s-53 Bu judduwaalewul ay béjjën it dara nekku ci.
s-54 Bu ñu xaajee nopp ba ñatt (1/3), la ca dagg bu matee benn xaaj ba, matul am Tëbëski.
s-55 Bu judduwaalewul nopp walla nopp ya gàtt nag dara nekku ci.
s-56 Niki noonu it bu nopp ba xaree lu tollu ci benn ci ñatti xaajam (1/3) du mat am Tëbëski.
s-57 Bu ñu xaajee geen ba ñatt, la ca dagg bu matee benn ca ñatti xaaj ya matul am Tabaski.
s-58 Bu ko judduwaalewul walla mu gàtt nag dara nekku ci.
s-59 Am Tabaski war naa mucc ci yii:
s-60 Bu mu yooy ba amul nebbon (ndawal).
s-61 Bu gimiñ ga xasaw.
s-62 Bu mu patt ba fés, rawatina nag mu di gumba.
s-63 Bu mu làggi ba mu fés, rawatina nag mu damm.
s-64 Alaa kulli haal nag, Lislaam ag yombal la bëgg, te mboolem àtte yi woroom xam-xam yi di tërël dañu ci sóoraale loolu ag jàppndal ñeel jullit ñi.
s-65 Lu ñu di bañ ci ndawalug am Tëbëski:
s-66 Bañees na ku ca jaay dara ca yàpp wa ak ca der ba.
s-67 Ku ko ñaani ba mayees la ko nag man na koo jaay dara nekku ci.
s-68 Bañees na yitam ka ko di fees ñu di ko fay ca yàppu wa, waaye manees na ko cee may walla sarax.
s-69 Bu laajee ag fay ñu fay ko xaalis walla leneen.
s-70 Noonu it la àtte ci am tudd.
s-71 Bañees na gépp joxe ngir wareef, niki tànku njëkke, yeeli maam, baatu feeskat, ak yu ni mel...
s-72 Waaye nag moo ngi aju ci yéene ji.
s-73 Booy sarax sa dëkkandoo te bëggal ko sutura man ngaa yéene sarax ci sa xol te jubloo rafetal wax ko ni am sa tànku njëkke, ndax jëf yaa ngi aju ci yéene yi, tur yi amul solo.
s-74 Niki amaana boo ko nee sarax, mu rusloo ko ci kanamu njabootam, mbaa sax mu tee ko koo jël.
s-75 Am Tëbëski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc.
s-76 Xataada Ibn An-Nu-Maan nettali na ne Yonent bi xëy na bis ne leen: Maa leen tere woon lekk ndawalug Tëbëski lu weesu ñatti bis yi (Tabaski).
s-77 May naa leen ko léegi; lekkleen ci ni mu leen neexe.
s-78 Waaye buleen jaay ndawalug Tëbëski, lekkleen ci joxeleen ci sarax.
s-79 Jariñooleen der bi waaye buleen ko jaay.
s-80 Bu ñu leen ci joxee it lekkleen.
s-81 Ahmad soloo na ko.
s-82 Nan lañuy rendee ak li ci aju:
s-83 Ab jullit moo koy def, te doon ku am xel.
s-84 Melo wi ci gën nag moo di mu tëral la mu di rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu Xibla.
s-85 Bu dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba, ba fa mu yam ca baat ba, mu teg ca paaka ba.
s-86 Walla bu amee téerey baat mu teg paaka ba ca diggante téere ya.
s-87 Bu ko defee bala caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni fas naa yéenee daganal lekk yàppu nàngam lii ci rendi gi ma ko di rendi.
s-88 Bu dee teg paaka ba mu wax: Bismil-Laahi daldi koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg.
s-89 Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax: Allaahu Akbar.
s-90 Bu dawalee paaka ba, sidit ya tàmbalee dagg, mu teggi ko.
s-91 Bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk.
s-92 Bu ko ca yeexee delloo nag te lor waralu ko, kon deesu ko lekk.
s-93 Te yit bu mu tàxale baat ba, bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.
s-94 Rendi xar ak bëy ci kanam lañu koy defe, boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk.
s-95 Bu dee aw nag manees na koo rendi, manees na koo loj.
s-96 Bu dee ginaar nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàqale baat ba.
s-97 Bu ko defee it du ko tee baax waaye bañ koo def a gën.
s-98 Loj ak li ci aju:
s-99 Kuy loj, dafay taxawal la muy loj jubale ko 'XIBLA' (Kaabag Màkka).
s-100 Mu lem baat ba tëral ko ci wetug càmmoñ ga.

Text viewDownload CoNNL-U