Dependency Tree
Universal Dependencies - Wolof - WTB
Language | Wolof |
---|
Project | WTB |
---|
Corpus Part | dev |
---|
Select a sentence
s-1
| Milyoη ak 450 junni ay toni jën ñoo di jaar at mu nekk ci géeji Senegaal yi. |
s-2
| Jëwriñ ji yor Koomug Géej gi, Xureysi Caam jibal na ne at mu jot 1 Milyoη ak 450 junni ay toni jëni biir géej dinañu di jóge géeju Kap-weer jaar ci sunu géej yi. |
s-3
| Xureysi Caam mi doon àddu ci surnaalu 12 w bu Rfm, leeral na ne jën yooyu dañuy njëkke jaar Giné-Bisaaw, Gàmbi, Senegaal, Moritani, Marok door a dëppaat. |
s-4
| Bu ñu egsiwaatee Moritani, te nappeesu leen, dañuy dee. |
s-5
| Teg na ci ne: am na 1 milyoη ak 450 junni ay ton yu doomi réew mi mënul a napp, ndax amuñu jumtuwaay yu ko mën a napp. |
s-6
| Jëwriñ jee ngi laaj: Ku di napp toni jën yooyu? |
s-7
| Ay bato wëyyu ñoo koy napp, bato yu xarala lañu, gaaw lool te mëneesu leen a teg loxo. |
s-8
| Loolu lanuy ñàkk at mu jot. |
s-9
| Ndax jaadu na nguur gi di seetaan woowu yàqute, déedéet. |
s-10
| Nee na, xalaat nanu ren, jàppandal ay batoy biir réew mi ak yu bitim-réew ngir ñu dem nappi jën yooyu. |
s-11
| Nee na, li ñuy napp dina nu indil at mu nekk 35 Dollar (ton bu nekk). |
s-12
| APS: Dibéer 15 maars 2009 |
Text view
•
Download CoNNL-U