Sentence view Universal Dependencies - Wolof - WTB Language Wolof Project WTB Corpus Part train
Text: Transcription Written form - Colors
Waalo bokkoon na ci yenn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon .
s-1
wo_wtb-ud-train_88
Waalo bokkoon na ci yenn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon.
Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar .
s-2
wo_wtb-ud-train_89
Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar.
Njurbel moo nekkoon péeyam ci lu njëkk .
s-3
wo_wtb-ud-train_90
Njurbel moo nekkoon péeyam ci lu njëkk.
Gannaaw bi lañu ko tuxël Jinge , tuxëlaat ko Ndeer .
s-4
wo_wtb-ud-train_91
Gannaaw bi lañu ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer.
Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu gannaaw ak ñàkk doole .
s-5
wo_wtb-ud-train_92
Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu gannaaw ak ñàkk doole.
Ñooñu ñooy : Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi .
s-6
wo_wtb-ud-train_93
Ñooñu ñooy: Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi.
Gannaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur .
s-7
wo_wtb-ud-train_94
Gannaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur.
Bokk na ca Meet , moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néegu Njurbel .
s-8
wo_wtb-ud-train_95
Bokk na ca Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néegu Njurbel.
Moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur .
s-9
wo_wtb-ud-train_96
Moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur.
Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel .
s-10
wo_wtb-ud-train_97
Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel.
Moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi .
s-11
wo_wtb-ud-train_98
Moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi.
Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi .
s-12
wo_wtb-ud-train_99
Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi.
Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo .
s-13
wo_wtb-ud-train_100
Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo.
Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de Geer .
s-14
wo_wtb-ud-train_101
Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de Geer.
Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo :
s-15
wo_wtb-ud-train_102
Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo:
Ba njëkk moo di Lingeer mi di yaayu buur bi ak Aawo mi di soxnaay buur su njëkk .
s-16
wo_wtb-ud-train_103
Ba njëkk moo di Lingeer mi di yaayu buur bi ak Aawo mi di soxnaay buur su njëkk.
Moom moo am teraangaay toog ca gangunaay ( moo di toogu gu buur ) ga .
s-17
wo_wtb-ud-train_104
Moom moo am teraangaay toog ca gangunaay (moo di toogu gu buur) ga.
Bu ñaareel ba mooy ñatt ci boroom ndomboy tànk yi ci péncum Sëb ak Bawar : ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak Maalaw mi yor koom-koom bi .
s-18
wo_wtb-ud-train_105
Bu ñaareel ba mooy ñatt ci boroom ndomboy tànk yi ci péncum Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak Maalaw mi yor koom-koom bi.
Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet , moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur .
s-19
wo_wtb-ud-train_106
Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom mooy njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur.
Baadi moom moo di njiitu doomi buur bi , ak yenn ci jëwriñ yi .
s-20
wo_wtb-ud-train_107
Baadi moom moo di njiitu doomi buur bi, ak yenn ci jëwriñ yi.
Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon : bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare .
s-21
wo_wtb-ud-train_108
Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare.
Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu , moom ak waa këram .
s-22
wo_wtb-ud-train_109
Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram.
Mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo war a teew ci gàmmu gi .
s-23
wo_wtb-ud-train_110
Mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo war a teew ci gàmmu gi.
Képp ku wuute dees na la mbugal , ñu folli la mbaa ñu rey la .
s-24
wo_wtb-ud-train_111
Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la.
Ndaxte seenug teew li mu di tegtal moo di yeesal seenug nangu , la ñu lokki ak la ñu siif .
s-25
wo_wtb-ud-train_112
Ndaxte seenug teew li mu di tegtal moo di yeesal seenug nangu, la ñu lokki ak la ñu siif.
Mbooleem alal yooyu daa nañu leen séddale ñetti xaaj : benn ba moo ngi jëm ca buur ba , ñaareel bi mu ngi jëm ca péncum Séb ak Bawar .
s-26
wo_wtb-ud-train_113
Mbooleem alal yooyu daa nañu leen séddale ñetti xaaj: benn ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca péncum Séb ak Bawar.
Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbéem yi .
s-27
wo_wtb-ud-train_114
Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbéem yi.
Nguur ga dañu ko seddale woon ci ay diwaan .
s-28
wo_wtb-ud-train_115
Nguur ga dañu ko seddale woon ci ay diwaan.
Bu ci ne amoon na Bàjjo bu di dox mbiri buur bi ( Sàmba Lingeer ) .
s-29
wo_wtb-ud-train_116
Bu ci ne amoon na Bàjjo bu di dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer).
Kàjj moom lañu fal ci ndijjooru dex gi , li-ko-dale ca Aarnik ba fa dex gi sottee .
s-30
wo_wtb-ud-train_117
Kàjj moom lañu fal ci ndijjooru dex gi, li-ko-dale ca Aarnik ba fa dex gi sottee.
Buriko moom lañu fal ci bëj-gànnaaru Lag de Geer .
s-31
wo_wtb-ud-train_118
Buriko moom lañu fal ci bëj-gànnaaru Lag de Geer.
Mu ngi daan dëkk ca Foos .
s-32
wo_wtb-ud-train_119
Mu ngi daan dëkk ca Foos.
Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinó Bawaal .
s-33
wo_wtb-ud-train_120
Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinó Bawaal.
Li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi .
s-34
wo_wtb-ud-train_121
Li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi.
Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo .
s-35
wo_wtb-ud-train_122
Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo.
Barlaf moo nga dëkkoon ca sowwu Lag de Geer .
s-36
wo_wtb-ud-train_123
Barlaf moo nga dëkkoon ca sowwu Lag de Geer.
Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ay cong yu jóge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi .
s-37
wo_wtb-ud-train_124
Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ay cong yu jóge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi.
Moo tax ba ci xarnub XX waa Waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi .
s-38
wo_wtb-ud-train_125
Moo tax ba ci xarnub XX waa Waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi.
Ba bésu tey Waaloo ngi jànkonte ak cong ya jóge woon ca ŋaayoo ga .
s-39
wo_wtb-ud-train_126
Ba bésu tey Waaloo ngi jànkonte ak cong ya jóge woon ca ŋaayoo ga.
Loolu moo di jur dellu gannaaw ak daanug Waalo , ba ku nekk di ko cokkaas : Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel .
s-40
wo_wtb-ud-train_127
Loolu moo di jur dellu gannaaw ak daanug Waalo, ba ku nekk di ko cokkaas: Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel.
Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas .
s-41
wo_wtb-ud-train_128
Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas.
Gannaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx , da koo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen gannaaw ci 1885 .
s-42
wo_wtb-ud-train_129
Gannaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx, da koo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen gannaaw ci 1885.
Booba la nootee Waalo , te naan dafa koy xettali .
s-43
wo_wtb-ud-train_130
Booba la nootee Waalo, te naan dafa koy xettali.
Edit as list • Text view • Dependency trees